12Jant ya Galyon moomee diiwaanu Akayi, Yawut ya dañoo mànkoo, jógal Póol, jàpp ko, yóbbu ca àttekaay ba.
13Ñu ne: «Kii dafa juuyoo ak yoon ci ni muy xiire nit ñi ci jaamu Yàlla.»
14Póol dem bay àddu, far Galyon ne Yawut ya: «Yeen Yawut yi, su doon ag njubadi mbaa jëf ju aay lool ju ngeen di tawat, kon xel dina nangu ma déglu leen.