Text copied!
Bibles in Wolof

JËF YA 17:29-33 in Wolof

Help us?

JËF YA 17:29-33 in Téereb Injiil

29 Kon nag, bu nu nekkee xeetu Yàlla, warunoo gëm ne Yàlla mel na ni nataali wurus, xaalis mbaa doj yu nit defar ci xareñ mbaa xel.
30 Ca jamono yu wees ya Yàlla toppul ñàkka xam googa, waaye léegi koo mana doon ak foo mana nekk, Yàlla santaane na, nga tuub say bàkkaar.
31 Ndaxte sàkk na bés bu muy àtte àddina ci njub, dénk ko Nit ki mu tànn; te firndeel na loolu bu wóor, ci li mu ko dekkal ca néew ya.»
32 Bi ñu déggee nag, muy wax ci mbirum ndekkitel ñi dee, ñii di ko foontoo, ña ca des ne ko: «Dinanu la déglu ci mbir moomu beneen yoon.»
33 Noonu Pool génn ci seen biir.
JËF YA 17 in Téereb Injiil

Jëf ya 17:29-33 in Kàddug Yàlla gi

29 Ndegam nag xeetu Yàlla lanu, warunoo nirule Yàlla ak lenn luy wurus, mbaa xaalis mbaa aw doj te sosoo ci xareñtey nit akum xelam.
30 Yàlla nag jéllale na janti ñàkka xam googa woon, waaye tey mu ngi woo ñépp, ak fépp fu ñu féete, ngir ñu tuub.
31 Ndaxte Yàlla jàpp na bés bu muy àttee àddina ci dëgg, àtte bu nit ki mu taamu di sottali; te loolu Yàlla jox na ci ñépp firnde lu wóor, ba mu dekkalee kooku mu taamu, ndekkite lu dee toppul.»
32 Naka lañu dégg waxi ndee-ndekki, ñenn ña di ko foontoo, ña ca des ne ko: «Dinanu la déglu, nga waxalaat nu ci moomu mbir.»
33 Ba loolu amee Póol bàyyikoo ca seen biir.
Jëf ya 17 in Kàddug Yàlla gi