Text copied!
Bibles in Wolof

JËF YA 17:2-7 in Wolof

Help us?

JËF YA 17:2-7 in Téereb Injiil

2 Pool nag dugg ca ñoom, na mu ko daan defe, ba am fa ñetti bésub noflaay, muy werante ak ñoom ci li Mbind mi wax.
3 Mu di leen ko tekki, te di leen wax ay firnde yuy wone ne fàww Almasi bi sonn te dekki. Mu ne leen: «Yeesu, mi ma leen di yégal, mooy Almasi bi.»
4 Noonu ñenn ci Yawut yi gëm, ànd ak Pool ak Silas, ñoom ak mbooloo mu mag ci Gereg yi ragal Yàlla, ak jigéen ñu am maana ñu bare.
5 Waaye kiñaan tàbbi ca Yawut ya, ñu daldi jël ay taxawaalukat ca pénc ma, dajale mbooloo, ñuy yëngal dëkk ba. Ñu daanu ci kër Yason, di wut Pool ak Silas, ngir dëj leen ci kanam waa dëkk ba.
6 Bi ñu leen gisul nag, ñu diri Yason ak ñeneen ca bokk ya ci kanam àttekat ya. Ñuy wax ci kaw naan: «Nit ñi dëpp àddina sépp agsi nañu fii léegi,
7 te Yason a leen dalal. Ñoom ñépp dañoo bañ ndigali buur Sesaar ne, am na beneen buur bu ñuy wax Yeesu.»
JËF YA 17 in Téereb Injiil

Jëf ya 17:2-7 in Kàddug Yàlla gi

2 Póol nag di leen fa fekk, na mu ko baaxoo. Diiru ñetti bési Noflaay, mu di leen waxal ci Mbind mi.
3 Mu di leen tekkil Mbind mi, di leen ci firndeel ne coonob Almasi ak ndekkiteem manul woona ñàkk. Mu ne leen: «Yeesu mii ma di leen xamal, mooy Almasi.»
4 Ba loolu amee ñenn ca Yawut ya gëm, fekksi Póol ak Silas, ñoom ak Gereg yu bare yu ragal Yàlla, ak jigéen ñu ràññiku ñu bare.
5 Yawut ya nag am ca kañaan, daldi foraatoo ca mbedd ma ay taxawaalukat, dajale ay gàngoor, ba yëngal dëkk ba. Ñu song kër Yason, di seet Póol ak Silas, ngir yóbbu leen ca waa dëkk ba.
6 Ci kaw loolu gisuñu leen, ñu diri Yason ak yeneen bokki gëmkat ba ca kanam àttekat ya. Ña ngay biral, naan: «Nit ñi tas àddinaa ngii, agsi nañu fi,
7 te Yason a leen dalal. Ñoom ñépp a xëtt ndigali buur Sesaar, te naan am na beneen buur bu ñuy wax Yeesu.»
Jëf ya 17 in Kàddug Yàlla gi