Text copied!
Bibles in Wolof

JËF YA 17:10-28 in Wolof

Help us?

JËF YA 17:10-28 in Téereb Injiil

10 Bi loolu amee bokk yi jàllale Pool ak Silas ci saa si ci guddi, ñu jëm Bere. Ba ñu fa eggee nag, ñu dugg ca jàngub Yawut ya.
11 Fekk ña fa nekk ñoo gëna am ay teggin waa Tesalonig, ndaxte nangu nañu kàddu ga te sawar ca, di niir Mbind mi bés bu nekk, ba xam ndax loolu dëgg la am déet.
12 Kon nag Yawut yu bare gëm, ak ñu bare ci Gereg yi, di jigéen yu am maana, ak ay góor.
13 Waaye bi Yawuti Tesalonig déggee ne Pool mu ngi yégle kàddug Yàlla ci Bere it, ñu daldi fay dikk, di jógloo ak a jaxase mbooloo ma.
14 Noonu bokk yi yebal Pool ca saa sa, mu jëm géej, waaye Silas ak Timote des fa.
15 Ñi ànd ak Pool nag gunge ko ba dëkku Aten. Bi ñu fa àggee, ñu waññiku, yóbbaale ndigalu Pool ne, Silas ak Timote ñëw fekksi ko ci lu gëna gaaw.
16 Bi leen Pool di nég ca Aten, mu am naqaru xol wu réy ci li mu gis dëkk ba fees ak ay nataali bokkaale Yàlla.
17 Muy werante nag ca jàngu ba ak Yawut ya ak ña ragal Yàlla, tey werante it bés bu nekk ca pénc ma ak ña fay dajaloo.
18 Noonu ay boroom xam-xam ci mbooloo mi ñuy wax Epikuren ak ci mbooloo mi ñuy wax Estowisen, di werante ak moom. Ñenn ci ñoom ne: «Fortukatu xam-xam bii, lu mu bëgga wax?» Te ña ca des, bi ñu déggee Pool di waare xibaaru jàmm bi, aju ci Yeesu ak ci mbirum ndekkite, ñu ne: «Dafa mel ni day waare ay yàlla yu nu xamul.»
19 Kon nag ñu jël ko, yóbbu ko ca géew, ba ñuy wax Areyopas. Ñu ne ko: «Danoo bëggoon, nga leeral nu ci sa xam-xam bu bees, bii ngay yégle.
20 Ndaxte sol nga ci sunuy nopp lu nu xamul. Danoo bëggoona xam nag léegi, loolu lu muy tekki.»
21 Ndaxte waa Aten ñépp ak doxandéem ya fa dëkk, wax ak a déglu lu bees rekk lañu daan xënte.
22 Noonu Pool taxaw ci biir mbooloom Areyopas ne leen: «Yéen waa Aten gis naa ne farlu ngeen ci diine lool.
23 Ndaxte bi may doxantu di seet seeni màggalukaay, gis naa ci benn bu ñu bind lii: “Yàlla mi nu xamul.” Li ngeen di màggal nag te xamuleen ko, loolu laa leen di xamal.
24 «Yàlla mi sàkk àddina ak li mu ëmb lépp, moom miy Boroom asamaan ak suuf, du dëkk ci néegi màggalukaay yu loxoy nit defar.
25 Du jariñu it ci loxoy nit, mel ni dafa soxla dara, ndax moom mooy jox ñépp bakkan ak ruu ak lépp.
26 Ci kenn nit la sàkke xeeti àddina yépp, ñu dëkk ci ñeenti xébla yi; fekk àppal na xeet wu nekk jamonoom, te rëdd seen diggi réew.
27 Yàlla def na loolu, ngir ñu koy wut ci yaakaaru daj ko ci làmbatu, fekk sax sorewul kenn ci nun.
28 “Ndaxte ci moom lanuy dunde, di ci jëf te nekk ci,” ni ko ñenn ci seeni taalifkat dëggale naan: “Nun noo di aw xeetam.”
JËF YA 17 in Téereb Injiil

Jëf ya 17:10-28 in Kàddug Yàlla gi

10 Ba mu ko defee bokki gëmkat ña yebal ca saa sa Póol ak Silas ca guddi ga, ñu jëm Bere. Ñu agsi, dem ca jàngub Yawut ya.
11 Waa Bere nag gëna am déggin waa Tesalonig. Ñu gëm kàddu gi, xér ci lool, bés bu nekk ñuy niir Mbind mi, ngir xam ndax la ñu leen di wax noonu la.
12 Ci kaw loolu Yawut yu bare gëm, ñoom ak jigéeni Gereg ñu ràññiku, ak ay góori Gereg ñu bare.
13 Ba loolu amee Yawuti Tesalonig dégg ne Póol a ngay xamle kàddug Yàlla ca Bere itam. Ñu dikkati, yëngal nit ña, ñu def ay gàngoor.
14 Ca la bokki gëmkat ñi yebal Póol ca saa sa, mu jëm tefes ga, Silas ak Timote ñoom, des ca Bere.
15 Ña dar Póol nag gunge ko ba ca dëkk ba ñuy wax Aten, ñu doora dëpp, jottliji Silas ak Timote kàddug Póol, ngir ñu fekksi ko nu mu gëna gaawe.
16 Diggante ba Póol di nég Silas ak Timote ca Aten, xolam jeex na ndax dafa gis na dëkk ba yeboo ci jaamu ay tuur.
17 Ci biir loolu muy wax ak Yawut yaak jaamburi ragalkati Yàlla ya ca jàngu ba, di wax it ak waa pénc ma bés bu nekk.
18 Ci kaw loolu ay boroom xam-xam yu bokk ci ngérum Epikur ak ngérum Estowisen, di werante ak moom. Ñenn ña ne: «Kebatukat bii, lu muy wax nii?» Ña ca des dégg Póol di waare xibaaru jàmm bi ci Yeesu ak ndekkiteem, ñu ne: «Daa mel ni ay tuur-tuuraani doxandéem lay waareel.»
19 Ñu jàpp ko nag, yóbbu ko ca ëttub àttekaay ba ñuy wax Areyopas. Ñu ne ko: «Ndax man nanoo xam njàngle mu bees mii ngay siiwal, lu mu doon?
20 Ndax li ngay wax kat sunu ngan-gi-nopp la. Nu bëgga xam nag loolu lu muy tekki.»
21 Booba waa Aten ñépp, doxandéem ak njuddu-ji-réew, xintewuñu lenn lu moy di nettali ak a déglu xew-xew wu bees.
22 Ci kaw loolu Póol taxaw ca digg ëttub Areyopas, ne leen: «Yeen waa Aten, gis naa ne ci wet gu nekk ñu farlu ngeen ci diine.
23 Ndax maa doon doxantu, di seet seeni jaamookaay, ba yem ci bu ñu bind mii mbind: “Ñeel yàlla ji nu xamul.” Loolu ngeen di màggal te xamuleen ko nag, moom laa leen di xamal.
24 «Yàlla mi sàkk àddina ak mboolem li ci biiram, di Boroom asamaan ak suuf, dëkkewul màkkaan mu ay loxo sàkk.
25 Te it jariñoowul loxol nit, mbete ku soxla lenn, ndax mooy may ñépp bakkan akug noo, ak lu mu mana doon.
26 Moo sàkke xeeti àddina yépp ci kenn nit, ñu dëkke déndu suuf sépp, te moo leen àppal seeni jamono, rëddal leen seen kemi dëkkuwaay.
27 Yàllaa def loolu, ngir xeeti àddina wut ko, làmbatu ba daj ko, ndegam man naa am, doonte sorewul kenn ku nekk ci nun.
28 “Ndax sunu bakkan ak sunu yëngu ak sunug nekk, lépp ci moom la.” Mooy ba tey la ñenn ci seeni woykat ne: “Nun itam aw xeetam lanu.”
Jëf ya 17 in Kàddug Yàlla gi