13Ba bésub Noflaay ba taxawee, nu génn ca buntu dëkk ba, ca wetu dex ga, daldi fay gis bérab bu nu foog ne ab jullikaay la. Nu toog fa nag, di waxtaan ak jigéen ña fa daje.
14As ndaw a nga ca, di déglu; ku ñuy wax Lidi, dëkke Catir, di jaaykatub cuubi tànnéef yu xonq curr, te di jaamukatu Yàlla. Boroom bi nag ubbi xolam, ba mu teewlu bu baax kàdduy Póol.
15Ci kaw loolu ñu sóob ko ci ndox, moom ak waa këram. Mu daldi nu ñaan, ne nu: «Ndegam ab gëmkatub Sang bi ngeen ma jàppe, agsileen, dal ak man ca sama kër.» Mu soññ nu ba nu nangu.