Text copied!
Bibles in Wolof

JËF YA 15:9-23 in Wolof

Help us?

JËF YA 15:9-23 in Téereb Injiil

9 Gënalantewu nu ak ñoom, ci li mu sellal seen xol ci kaw ngëm.
10 Léegi nag lu tax ngeen di diiŋat Yàlla, ciy teg taalibe yi yen bu nu masula àttan, nun mbaa sunuy maam?
11 Nun daal ci yiwu Yeesu Boroom bi lanu yaakaara mucce, te ñoom itam, ci lañu wékku.»
12 Bi mu ko waxee, mbooloo mépp ne xerem, di déglu Barnabas ak Pool, ñuy nettali kéemaan ak firnde yépp, yi Yàlla def jaarale ko ci ñoom ci biir ñi dul Yawut.
13 Bi ñu noppee, Saag jël kàddu ga ne:
14 «Bokk yi, dégluleen ma! Simoŋ nettali na, ni Yàlla seetsee bu jëkk ñi dul Yawut, ngir sàkku ci ñoom xeet wu ñu tudde turam.
15 Te loolu sax dëppoo na ak li yonent yi tëral; ñu bind ne:
16 “Boroom bi nee na: Gannaaw loolu dinaa délsi, te yékkati këru Daawuda, gi ne tasar, dinaa defar gent ya, ba taxawalaat ko.
17 Noonu li des ci doom Aadama wut Boroom bi, maanaam xeet yi dul Yawut, ñuy tudd sama tur.
18 Man dinaa def loolu, man Boroom bi ko wax, te ca njàlbéen ba tey ma di ko xamle.”
19 «Kon nag lii mooy sama ndigal: bunu gétën ñi dul Yawut te waññiku ci Yàlla.
20 Waaye nu bind leen, ñu moytu ñam wu araam wu ñu tuuroo xërëm, tey moytu njaaloo, ak jur gu médd, bay naan deret ja.
21 Ndaxte ca njàlbéen ga ba tey am na ca dëkk bu nekk ñuy waare ci yoonu Musaa; bésub noflaay bu nekk sax dañu ciy xutba ca jàngu ya.»
22 Bi mu ko waxee, ndaw yi ak njiit yi ak mbooloom ñi gëm mépp fas yéenee tànn ci ñoom ay nit, yónni leen Ancos, ñu ànd ak Pool ak Barnabas. Noonu ñu tànn Yudd, mi ñu dippee Barsabas, ak Silas, di ay njiit ca bokk ya.
23 Ñu jox leen bataaxal bu ne: Yéen sunu bokk yi dul Yawut te dëkk Ancos, Siri ak Silisi, nu ngi leen di nuyu, nun seeni bokk, di ndaw yi ak njiit yi.
JËF YA 15 in Téereb Injiil

Jëf ya 15:9-23 in Kàddug Yàlla gi

9 Yàlla amul xejj ak seen sunu digg ak ñoom, ndax seen ngëm la raxase seen xol.
10 Léegi nag lu tax ngeen di diiŋat Yàlla, di teg taalibe yi yen bu nu masula àttan, cay maam ba ci nun?
11 Yiwu Sang bi Yeesu daal lanu gëm ne ci lanuy mucce, te ñoom itam, noonu rekk.»
12 Ba loolu wéyee mbooloo mépp ne xerem. Ñu déglu nag Barnaba ak Póol, ñu xamle mboolem firnde yeek kéemaan, yi Yàlla defe seen ñaari jëmm ci biir jaambur ñi.
13 Ba ñu noppee, Yanqóoba àddu ne: «Bokk yi, dégluleen ma.
14 Simoŋ xamle na, ni Yàlla yége jaambur ñi ca njàlbéen, ba sàkke ci seen biir, xeet wu mu tudde turam.
15 Te loolu dëppoo na ak kàdduy yonent yi, ndax bindees na ne:
16 “Boroom bi nee: Gannaaw loolu dinaa délsi; maay yékkati kër Daawuda gi daanu, maay yékkati gent yi, joyanti ko,
17 ngir ndesu nit ñi sàkku Boroom bi, te ñooñoo di jaambur ñi ñu tudde sama tur.
18 Boroom bee xamle loolu bu yàgga yàgg.”
19 «Kon nag sama xalaat mooy: bunu gétën jaambur ñi tuub, ba waññiku ci Yàlla.
20 Xanaa nu bind leen, ne leen ñu moytu lu ay xërëm sobeel, moytu powum séy, moytoo lekk yàppu mala mu ñu tuurul deretam, ak lekk deret ci boppam.
21 Ndaxte ca njàlbéen ga ba tey ay nit a ngi waaree yoonu Musaa ci dëkk bu nekk, ñu di ko jàng ci jàngu yi bésub Noflaay bu nekk.»
22 Ba loolu amee ndaw yi ak mag ñi mànkoo ak mbooloom gëmkat ñépp, ngir tànne ci seen biir ay nit, yebal leen Àncos, boole leen ak Póol ak Barnaba. Ñooñoo di Yuda, mi ñu dippee Barsabas, ak Silas, ñu diy mag ca bokk ya.
23 Ñu yóbbante leen bataaxal, bind ci ne: Nun ndawi Yeesu, ak mag ñi, seen bokki Yerusalem, noo leen bind, yeen sunu bokki gëmkat ñi dul Yawut te dëkke Àncos ak Siri ak Silisi. Nu ngi jiital sunub nuyoo.
Jëf ya 15 in Kàddug Yàlla gi