Text copied!
Bibles in Wolof

JËF YA 15:2-21 in Wolof

Help us?

JËF YA 15:2-21 in Téereb Injiil

2 Pool ak Barnabas nag am ak ñoom diisoo ak werante wu metti; noonu bokk yi jàpp ne, Pool ak Barnabas ak ñeneen ci ñoom war nañoo dem Yerusalem ca ndaw ya ak njiit ya, ngir leeral werante wi.
3 Kon nag mbooloo mi gunge leen, ñu jaar ci wàlli Fenisi ak Samari, di nettali ni ñi dul Yawut waññikoo ci Yàlla, ba bokk yépp am ca mbég mu réy.
4 Te bi ñu agsee Yerusalem, mbooloom ñi gëm, ndaw yi ak njiit yi teeru leen, ñu nettali leen fi ñu jaar ak Yàlla fépp.
5 Ci kaw loolu ñeneen, ñi gëm waaye bokk ci tariixab Farisen ya, daldi jóg ne: «Fàww ñi dul Yawut xaraf, te ñu dénk leen sàmm yoonu Musaa.»
6 Noonu ndaw yi ak njiit yi dajaloo, ngir seet mbir moomu.
7 Gannaaw werante wu bare Piyeer jóg ne leen: «Yéen bokk yi, xam ngeen ne ca njàlbéen ga Yàlla tànnoon na ma ci yéen, ngir ma yégal ñi dul Yawut xibaaru jàmm bi, ba ñu gëm.
8 Yàlla, mi xam xol yi, seede na leen ci li mu leen may Xel mu Sell mi, ni mu nu ko maye nun itam.
9 Gënalantewu nu ak ñoom, ci li mu sellal seen xol ci kaw ngëm.
10 Léegi nag lu tax ngeen di diiŋat Yàlla, ciy teg taalibe yi yen bu nu masula àttan, nun mbaa sunuy maam?
11 Nun daal ci yiwu Yeesu Boroom bi lanu yaakaara mucce, te ñoom itam, ci lañu wékku.»
12 Bi mu ko waxee, mbooloo mépp ne xerem, di déglu Barnabas ak Pool, ñuy nettali kéemaan ak firnde yépp, yi Yàlla def jaarale ko ci ñoom ci biir ñi dul Yawut.
13 Bi ñu noppee, Saag jël kàddu ga ne:
14 «Bokk yi, dégluleen ma! Simoŋ nettali na, ni Yàlla seetsee bu jëkk ñi dul Yawut, ngir sàkku ci ñoom xeet wu ñu tudde turam.
15 Te loolu sax dëppoo na ak li yonent yi tëral; ñu bind ne:
16 “Boroom bi nee na: Gannaaw loolu dinaa délsi, te yékkati këru Daawuda, gi ne tasar, dinaa defar gent ya, ba taxawalaat ko.
17 Noonu li des ci doom Aadama wut Boroom bi, maanaam xeet yi dul Yawut, ñuy tudd sama tur.
18 Man dinaa def loolu, man Boroom bi ko wax, te ca njàlbéen ba tey ma di ko xamle.”
19 «Kon nag lii mooy sama ndigal: bunu gétën ñi dul Yawut te waññiku ci Yàlla.
20 Waaye nu bind leen, ñu moytu ñam wu araam wu ñu tuuroo xërëm, tey moytu njaaloo, ak jur gu médd, bay naan deret ja.
21 Ndaxte ca njàlbéen ga ba tey am na ca dëkk bu nekk ñuy waare ci yoonu Musaa; bésub noflaay bu nekk sax dañu ciy xutba ca jàngu ya.»
JËF YA 15 in Téereb Injiil

Jëf ya 15:2-21 in Kàddug Yàlla gi

2 Mbir ma nag mujje féewaloo ak werante wu xawa metti, te Póol ak Barnaba séq ko ak ñooñu. Ba loolu amee ñu ne, na Póol ak Barnaba, ak ñenn ca gëmkati Àncos, ànd dem Yerusalem ca ndawi Yeesu, ak mag ña, ba lijjanti mbir moomu.
3 Ci kaw loolu mbooloom gëmkat ñi yebal leen, ñu jaare Fenisi ak Samari, daldi àgge waa foofa ni jaambur ñi dul Yawut tuube, ba bokki gëmkat ñépp bég ca lool.
4 Gannaaw loolu, ñu agsi Yerusalem, mbooloom gëmkat ñi, ak ndawi Yeesu yi, ak mag ñi, dalal leen, ñu nettali leen mboolem ni Yàlla def ak ñoom.
5 Ba mu ko defee ñenn ci gëmkat ñi bokk ci ngérum Farisen yi, daldi taxaw temm, ne gëmkat ñi dul Yawut, fàww ñu xarfal leen, sàmmloo leen yoonu Musaa.
6 Ba loolu amee ndawi Yeesu yi ak mag ñi bokk daje, ngir seet mbir moomu.
7 Werante wu réy am ca. Ci kaw loolu Piyeer jóg ne leen: «Bokk yi, yeen xam ngeen ne bu yàgg la ma Yàlla seppee ci seen biir, ngir jaambur ñi dégge ci sama làmmiñ, kàddug xibaaru jàmm bi, ba doon ay gëmkat.
8 Yàlla, mi xam xolu nit nag moo seereel jaambur ñi, ba mu leen mayee Noo gu Sell gi, ni mu nu ko maye nun itam.
9 Yàlla amul xejj ak seen sunu digg ak ñoom, ndax seen ngëm la raxase seen xol.
10 Léegi nag lu tax ngeen di diiŋat Yàlla, di teg taalibe yi yen bu nu masula àttan, cay maam ba ci nun?
11 Yiwu Sang bi Yeesu daal lanu gëm ne ci lanuy mucce, te ñoom itam, noonu rekk.»
12 Ba loolu wéyee mbooloo mépp ne xerem. Ñu déglu nag Barnaba ak Póol, ñu xamle mboolem firnde yeek kéemaan, yi Yàlla defe seen ñaari jëmm ci biir jaambur ñi.
13 Ba ñu noppee, Yanqóoba àddu ne: «Bokk yi, dégluleen ma.
14 Simoŋ xamle na, ni Yàlla yége jaambur ñi ca njàlbéen, ba sàkke ci seen biir, xeet wu mu tudde turam.
15 Te loolu dëppoo na ak kàdduy yonent yi, ndax bindees na ne:
16 “Boroom bi nee: Gannaaw loolu dinaa délsi; maay yékkati kër Daawuda gi daanu, maay yékkati gent yi, joyanti ko,
17 ngir ndesu nit ñi sàkku Boroom bi, te ñooñoo di jaambur ñi ñu tudde sama tur.
18 Boroom bee xamle loolu bu yàgga yàgg.”
19 «Kon nag sama xalaat mooy: bunu gétën jaambur ñi tuub, ba waññiku ci Yàlla.
20 Xanaa nu bind leen, ne leen ñu moytu lu ay xërëm sobeel, moytu powum séy, moytoo lekk yàppu mala mu ñu tuurul deretam, ak lekk deret ci boppam.
21 Ndaxte ca njàlbéen ga ba tey ay nit a ngi waaree yoonu Musaa ci dëkk bu nekk, ñu di ko jàng ci jàngu yi bésub Noflaay bu nekk.»
Jëf ya 15 in Kàddug Yàlla gi