Text copied!
Bibles in Wolof

JËF YA 15:18-33 in Wolof

Help us?

JËF YA 15:18-33 in Téereb Injiil

18 Man dinaa def loolu, man Boroom bi ko wax, te ca njàlbéen ba tey ma di ko xamle.”
19 «Kon nag lii mooy sama ndigal: bunu gétën ñi dul Yawut te waññiku ci Yàlla.
20 Waaye nu bind leen, ñu moytu ñam wu araam wu ñu tuuroo xërëm, tey moytu njaaloo, ak jur gu médd, bay naan deret ja.
21 Ndaxte ca njàlbéen ga ba tey am na ca dëkk bu nekk ñuy waare ci yoonu Musaa; bésub noflaay bu nekk sax dañu ciy xutba ca jàngu ya.»
22 Bi mu ko waxee, ndaw yi ak njiit yi ak mbooloom ñi gëm mépp fas yéenee tànn ci ñoom ay nit, yónni leen Ancos, ñu ànd ak Pool ak Barnabas. Noonu ñu tànn Yudd, mi ñu dippee Barsabas, ak Silas, di ay njiit ca bokk ya.
23 Ñu jox leen bataaxal bu ne: Yéen sunu bokk yi dul Yawut te dëkk Ancos, Siri ak Silisi, nu ngi leen di nuyu, nun seeni bokk, di ndaw yi ak njiit yi.
24 Dégg nanu ne am na ay nit ñu bawoo ci nun, ñu di leen lëjal ak seeni wax, di jaxase seeni xol, te fekk sukkandikuwuñu ci lenn ndigal lu jóge ci nun.
25 Kon nag mànkoo nanu ci tànn ay nit, yónnee leen ko, ànd ak sunuy soppe Barnabas ak Pool.
26 Ñoom jaay nañu seen bakkan ngir turu Yeesu Kirist Boroom bi.
27 Yónni nanu nag Yudd ak Silas, ñu di leen xamal xibaar boobu ci seen gémmiñ.
28 Ndaxte li neex Xel mu Sell mi te neex nu, mooy nu bañ leena teg beneen yen, lu dul dénkaane yii am njariñ,
29 maanaam ngeen moytu ñam wu ñu tuuroo xërëm, deretu jur gu médd ak njaaloo. Bu ngeen moytoo yëf yooyu, dingeen def lu baax. Ci jàmm.
30 Noonu ñu tàggoo, dem Ancos, ñu dajale mbooloo mi, jébbal leen bataaxal bi.
31 Ñu jàng ko nag, seen xol sedd ci doole, ji leen bataaxal bi indil.
32 Te Yudd ak Silas, ñi doon yonent, ñuy dooleel bokk yi, di dëgëral seen fit ak wax yu bare.
33 Bi loolu amee ñu toog fa ab diir, ba noppi bokk yi yiwi leen ci jàmm, ñu dellu ca ña leen yónni woon.
JËF YA 15 in Téereb Injiil

Jëf ya 15:18-33 in Kàddug Yàlla gi

18 Boroom bee xamle loolu bu yàgga yàgg.”
19 «Kon nag sama xalaat mooy: bunu gétën jaambur ñi tuub, ba waññiku ci Yàlla.
20 Xanaa nu bind leen, ne leen ñu moytu lu ay xërëm sobeel, moytu powum séy, moytoo lekk yàppu mala mu ñu tuurul deretam, ak lekk deret ci boppam.
21 Ndaxte ca njàlbéen ga ba tey ay nit a ngi waaree yoonu Musaa ci dëkk bu nekk, ñu di ko jàng ci jàngu yi bésub Noflaay bu nekk.»
22 Ba loolu amee ndaw yi ak mag ñi mànkoo ak mbooloom gëmkat ñépp, ngir tànne ci seen biir ay nit, yebal leen Àncos, boole leen ak Póol ak Barnaba. Ñooñoo di Yuda, mi ñu dippee Barsabas, ak Silas, ñu diy mag ca bokk ya.
23 Ñu yóbbante leen bataaxal, bind ci ne: Nun ndawi Yeesu, ak mag ñi, seen bokki Yerusalem, noo leen bind, yeen sunu bokki gëmkat ñi dul Yawut te dëkke Àncos ak Siri ak Silisi. Nu ngi jiital sunub nuyoo.
24 Dégg nanu ne ay nit ñu bawoo ci nun, ñoo leen lëjal ak seeni wax, di jaxase seen xel, te nun joxunu leen lenn ndigal.
25 Moo tax nu mànkoo ci tànn ay nit ñu nu yebal ci yeen, boole leen ak sunuy soppe Barnaba ak Póol,
26 ñoom ñi jaay seen bakkan ngir sunu Sang Yeesu Almasi.
27 Kon nag noo yebal Yuda ak Silas, ngir ñu àgge leen ci seen gémmiñu bopp, lii nu leen bind.
28 Ndaxte Noo gu Sell gi moo mànkoo ak nun ci bañ leena teg benn coono, xanaa lii manula ñàkk:
29 Ngeen moytu yàpp wu ñu sarxal ay tuur, ak deret, ak yàppu jur gu ñu tuurul deretam, ak powum séy. Yooyii, bu ngeen ko moytoo bu baax, def ngeen lu baax. Jàmm ak jàmm.
30 Ba loolu amee ñu tàggtoo, daldi dem ba Àncos. Ci kaw loolu ñu woo mbooloo mi, jébbal leen bataaxal bi.
31 Ba ñu jàngee bataaxal bi, kàddu ga dëfal leen, seen xol sedd.
32 Yuda ak Silas it gannaaw ay yonent lañu woon, wax nañu ak bokk yi lu yàgg, ngir ñaax leen, feddli seen ngëm.
33 Ba loolu amee ñu toog fa ab diir, bokk yi door leena ñaanal yoonu jàmm, yiwi leen, ngir ñu dellu ca ña leen yebaloon.
Jëf ya 15 in Kàddug Yàlla gi