Text copied!
Bibles in Wolof

JËF YA 14:1-27 in Wolof

Help us?

JËF YA 14:1-27 in Téereb Injiil

1 Bi Pool ak Barnabas nekkee Ikoñum nag, ñu dugg ci jàngub Yawut ya, ni ñu ko daan defe; ñuy waare, ba mbooloom Yawut ak Gereg mu bare gëm.
2 Waaye Yawut yu nanguwul yi ñoo jógloo ñi dul Yawut, di ñaawal seen njort ci bokki taalibe yi.
3 Pool ak Barnabas nag sax nañu ci Ikoñum lu yàgg, ñu wéeru ci Boroom bi, bay wax ak fit wu dëgër; te Yàlla dëggal kàddug yiwam, ba may leen, ñu def ay kéemaan ak ay firnde.
4 Noonu waa dëkk bi xàjjalikoo, ñii far ak Yawut yi, ñale far ak ndaw ya.
5 Waaye ñi dul Yawut ak Yawut yi, ñoom ak seeni kilifa, lal pexem fitnaal leen ci sànni ay doj.
6 Bi ko Pool ak Barnabas yégee nag, ñu daw ca diiwaanu Likawni ca dëkk ya ñuy wax Listar ak Derbë ak wàllaa ya.
7 Foofa ñu di fa xamle xibaaru jàmm bi.
8 Amoon na ca Listar nag nit ku fa toog, ku ay tànkam làggi, ndax li mu judduwaale lafañ te masula dox.
9 Moom nag muy déglu Pool miy waare. Noonu Pool xool ko jàkk, gis ne am na ngëm ngir wér.
10 Mu ne ko ak baat bu dëgër: «Jógal taxaw bu jub.» Noonu nit ki ne bërét, jóg, daldi dox.
11 Bi mbooloo ma gisee li Pool def, ñu daldi yuuxu, ne ci làkku waa Likawni: «Yàlla yi soppiku nañu nit, wàcc ci nun.»
12 Noonu ñu tudde Barnabas, Sës, te tudde Pool, Ermes, ndaxte mooy ki yor wax ji.
13 Fekk ci buntu dëkk ba amoon na fa kër gu ñuy màggale Sës. Sarxalkat ba nag ànd ak mbooloo ma, daldi indi ca bunt ya ay yëkk ak ay caq, yi ñu defare tóor-tóor, ngir màggal leen ci tuur deretu mala.
14 Waaye bi ko ndaw yi Barnabas ak Sóol déggee, ñu sib ko ba xotti seeni yére, ñu daldi daw, tàbbi ca mbooloo ma, di wax ci kaw ne:
15 «Yéen nit ñi, lu leen xiir ci lii? Nun it ay nit lanu, ñu bokk bind ak yéen. Te nu ngi leen di xamal xibaaru jàmm ne leen, ngeen dëddu yëfi neen yii te waññiku ci Yàlla miy dund te sàkk asamaan, suuf, géej ak li ñu ëmb lépp.
16 Démb mayoon na xeet yépp, ñu aw seen yoonu bopp.
17 Moona noppiwula firndeel aw meloom ci def lu baax, di leen wàcceele ci asamaan taw buy indi naataange, ba ngeen lekk ba suur, te seen xol fees ak mbég.»
18 Noonu ci lu jafe yey nañu mbooloo ma ak wax jooju, ba tere leen, ñu rendil leen sarax.
19 Waaye bi loolu wéyee amoon na ay Yawut yu jóge Ancos ak Ikoñum, ñu fàbbi mbooloo ma, sànni Pool ay doj, ba yaakaar ne dee na, ñu diri ko ba ca gannaaw dëkk ba.
20 Waaye taalibe ya ñëw wër ko, mu daldi jóg, duggaat ca dëkk ba. Ca suba sa nag, mu ànd ak Barnabas, dem Derbë.
21 Bi ñu fa àggee nag, ñu xamle fa xibaaru jàmm bi, ba sàkk fa ay taalibe yu bare. Gannaaw loolu ñu délsi Listar, Ikoñum ak Ancos,
22 di dooleel xeli taalibe ya, xiir leen ñu sax ci yoon wi; ñu ne leen: «Ci kaw nattu yu bare lanu wara dugge ci nguuru Yàlla.»
23 Ci mbooloom ñi gëm mu nekk nag, ñu tànn ci ay njiit; ba noppi ñu ñaan Yàlla ak di woor, dénk leen Boroom bi ñu gëm.
24 Gannaaw loolu ñu jaar diiwaanu Pisidi, dikk ci Pamfili.
25 Ñu yégle kàddu gi ci dëkku Peers, doora dem dëkku Atali.
26 Foofa nag ñu dugg gaal, jëm Ancos, fa ñu leen dénke woon ca yiwu Yàlla, ngir liggéey bi ñu àggale.
27 Bi ñu agsee, ñu woo mbooloom ñi gëm, nettali leen fi ñu jaar ak Yàlla fépp, ak ni mu ubbee buntu ngëm ci ñi dul Yawut.
JËF YA 14 in Téereb Injiil

Jëf ya 14:1-27 in Kàddug Yàlla gi

1 Ba Póol ak Barnaba nekkee Ikoñum, noonu lañu dugge itam ca jàngub Yawut ya. Ñu waare, ba mbooloo mu mag gëm, ay Yawut aki Gereg.
2 Yawut yi gëmul nag di xiirtal jaambur ñi dul Yawut, di yàq seen xel ci bokki taalibe yi.
3 Teewul Póol ak Barnaba toog Ikoñum diir bu yàgg lool. Fit lañu doon waaree ngir Boroom bi, Boroom bi maye ay firnde aki kéemaan yu jaare ci ñoom, ngir seeree ko kàddug yiwam gi ñuy biral.
4 Ba loolu amee waa dëkk bi xàjjalikoo, ñii far ak Yawut yi, ñale far ak ndaw ya.
5 Jaambur ñeek Yawut yi nag ànd ak seeni kilifa, di leen waaja mitital ak a dóori doj.
6 Ñu yég ko, daw làquji diiwaanu Likawni, ca dëkk ya ñuy wax Listar, ak Derbe ak la ko wër.
7 Foofa itam ñu di fa xamle xibaaru jàmm bi.
8 Jenn waay a nga daan toog ca Listar, tànk ya baaxul woon; laago la judduwaale, te masula dox.
9 Kookoo dégg Póol muy waare, Póol xool ko jàkk, gis ne am na ngëm gu muccam mana jaare.
10 Mu àddu ca kaw, ne waa ji: «Jógal taxaw jonn!» Waa ji ne bërét, jóg, daldi dox.
11 Ba mbooloo ma gisee la Póol def, ca kaw lañu àddu ci làkku Likawni, ne: «Yàlla yee soppliku melow nit, wàccsi ci sunu biir!»
12 Ci kaw loolu ñu tudde Barnaba Sës, kilifay yàllay Gereg yi, Póol nag gannaaw moo farewoo woon kàddug waare ga, ñu tudde ko Ermes, ndawal yàllay Gereg yi.
13 Jaamookaayu Sës ma nga woon ca buntu dëkk ba. Sarxalkat ba daldi indi ca bunti dëkk ba ay yëkk yu ñu takkal caqi tóor-tóor. Sarxalkat ba ànd ak mbooloo ma, nara rendi jur ga, sarxal ko Póol ak Barnaba.
14 Ci kaw loolu Póol ak Barnaba yég la xew. Ñu xotti seeni yére ndax ñaawlu ko. Ñu buur nag ba ca biir mbooloo ma, daldi àddu ca kaw ne:
15 «Yeen, lu leen xiir ci lii? Nun itam ay nit lanu, bokk ak yeen benn bind. Xibaaru jàmm bi lanu leen di xamal, ngir ngeen wacc yëfi neen yii te walbatiku ci Yàlla, kiy dund te sàkk asamaan ak suuf ak géej ak mboolem lu nekk ci biir.
16 Moo mayoon démb xeet yépp, ñu awe seen yooni bopp.
17 Moona noppiwula seereel boppam ci mbaaxam gi muy jëfe, di leen wàcceel fa asamaan, taw ak naataange, reggal leen, bégal leen ba seen xol sedd.»
18 Loolu lépp ndaw ya wax nañu ko te tuuti kon ñu tëlee tere mbooloo ma ñu rendil leen sarax.
19 Ci kaw loolu ay Yawut yu jóge Àncos gu Pisidi ak Ikoñum, fexe ba fàbbi mbooloo ma, daldi dóor Póol ay doj, diri ko ba génne ko dëkk ba, yaakaar ne dee na.
20 Naka la ko taalibe ya yéew, mu jóg, daldi dellu ca biir dëkk ba. Ca ëllëg sa, mu ànd ak Barnaba, dem Derbe.
21 Gannaaw ba ñu xamlee fa Derbe xibaaru jàmm bi, ba am fa taalibe yu bare, dañoo dellu Listar ak Ikoñum ak Àncos gu Pisidi.
22 Ñuy feddli pastéefu taalibe yi, di leen ñaax ngir ñu saxoo ngëm, ne leen: «Coono yu baree ngii, fàww nu jaare ci, ngir tàbbi ci nguurug Yàlla.»
23 Mbooloom gëmkat mu nekk nag, ñu tabb ci ay mag; ci biir loolu ñu ñaan, boole kook koor, daldi dénk mag ña Sang bi ñu gëm.
24 Gannaaw loolu ñu jaare biir diiwaanu Pisidi, ba àgg Pamfili.
25 Ñu daldi siiwtaane kàddu gi ca Perge, doora wàcci ba Atali.
26 Foofa lañu dugge gaal, dellu Àncos gu Siri, ga ñu leen dénke woon Yàlla ciw yiwam, ngir liggéey ba ñu sottal, ba délsi noonu.
27 Ba ñu agsee, dañoo woo mbooloom gëmkat ña, àgge leen mboolem na Yàlla def ak ñoom, ak na mu ubbilee jaambur ñi dul Yawut buntu ngëm.
Jëf ya 14 in Kàddug Yàlla gi