Text copied!
Bibles in Wolof

JËF YA 14:1-12 in Wolof

Help us?

JËF YA 14:1-12 in Téereb Injiil

1 Bi Pool ak Barnabas nekkee Ikoñum nag, ñu dugg ci jàngub Yawut ya, ni ñu ko daan defe; ñuy waare, ba mbooloom Yawut ak Gereg mu bare gëm.
2 Waaye Yawut yu nanguwul yi ñoo jógloo ñi dul Yawut, di ñaawal seen njort ci bokki taalibe yi.
3 Pool ak Barnabas nag sax nañu ci Ikoñum lu yàgg, ñu wéeru ci Boroom bi, bay wax ak fit wu dëgër; te Yàlla dëggal kàddug yiwam, ba may leen, ñu def ay kéemaan ak ay firnde.
4 Noonu waa dëkk bi xàjjalikoo, ñii far ak Yawut yi, ñale far ak ndaw ya.
5 Waaye ñi dul Yawut ak Yawut yi, ñoom ak seeni kilifa, lal pexem fitnaal leen ci sànni ay doj.
6 Bi ko Pool ak Barnabas yégee nag, ñu daw ca diiwaanu Likawni ca dëkk ya ñuy wax Listar ak Derbë ak wàllaa ya.
7 Foofa ñu di fa xamle xibaaru jàmm bi.
8 Amoon na ca Listar nag nit ku fa toog, ku ay tànkam làggi, ndax li mu judduwaale lafañ te masula dox.
9 Moom nag muy déglu Pool miy waare. Noonu Pool xool ko jàkk, gis ne am na ngëm ngir wér.
10 Mu ne ko ak baat bu dëgër: «Jógal taxaw bu jub.» Noonu nit ki ne bërét, jóg, daldi dox.
11 Bi mbooloo ma gisee li Pool def, ñu daldi yuuxu, ne ci làkku waa Likawni: «Yàlla yi soppiku nañu nit, wàcc ci nun.»
12 Noonu ñu tudde Barnabas, Sës, te tudde Pool, Ermes, ndaxte mooy ki yor wax ji.
JËF YA 14 in Téereb Injiil

Jëf ya 14:1-12 in Kàddug Yàlla gi

1 Ba Póol ak Barnaba nekkee Ikoñum, noonu lañu dugge itam ca jàngub Yawut ya. Ñu waare, ba mbooloo mu mag gëm, ay Yawut aki Gereg.
2 Yawut yi gëmul nag di xiirtal jaambur ñi dul Yawut, di yàq seen xel ci bokki taalibe yi.
3 Teewul Póol ak Barnaba toog Ikoñum diir bu yàgg lool. Fit lañu doon waaree ngir Boroom bi, Boroom bi maye ay firnde aki kéemaan yu jaare ci ñoom, ngir seeree ko kàddug yiwam gi ñuy biral.
4 Ba loolu amee waa dëkk bi xàjjalikoo, ñii far ak Yawut yi, ñale far ak ndaw ya.
5 Jaambur ñeek Yawut yi nag ànd ak seeni kilifa, di leen waaja mitital ak a dóori doj.
6 Ñu yég ko, daw làquji diiwaanu Likawni, ca dëkk ya ñuy wax Listar, ak Derbe ak la ko wër.
7 Foofa itam ñu di fa xamle xibaaru jàmm bi.
8 Jenn waay a nga daan toog ca Listar, tànk ya baaxul woon; laago la judduwaale, te masula dox.
9 Kookoo dégg Póol muy waare, Póol xool ko jàkk, gis ne am na ngëm gu muccam mana jaare.
10 Mu àddu ca kaw, ne waa ji: «Jógal taxaw jonn!» Waa ji ne bërét, jóg, daldi dox.
11 Ba mbooloo ma gisee la Póol def, ca kaw lañu àddu ci làkku Likawni, ne: «Yàlla yee soppliku melow nit, wàccsi ci sunu biir!»
12 Ci kaw loolu ñu tudde Barnaba Sës, kilifay yàllay Gereg yi, Póol nag gannaaw moo farewoo woon kàddug waare ga, ñu tudde ko Ermes, ndawal yàllay Gereg yi.
Jëf ya 14 in Kàddug Yàlla gi