Text copied!
Bibles in Wolof

JËF YA 13:6-12 in Wolof

Help us?

JËF YA 13:6-12 in Téereb Injiil

6 Noonu ñu jaar ci dun bépp, ba egg dëkku Pafos. Foofa ñu gis luxuskat bu tudd Bar-Yeesu, di Yawut bu mbubboo turu yonent.
7 Mu bokk ci gàngooru boroom réew ma tudd Sersiyus Poolus, di nit ku neex xel. Moom nag mu woolu Barnabas ak Sóol, ngir bëgga dégg kàddug Yàlla.
8 Waaye Elimas, boroom xam-xam bu ñuul bi —ndaxte loolu la turam di tekki— di leen dogale, ngir bañ boroom réew ma gëm.
9 Ci kaw loolu Sóol, mi tudd it Pool, daldi fees ak Xel mu Sell mi; mu xool ko jàkk,
10 ne ko: «Yaw mi fees ak fen ak lu bon, di doomu Ibliis, tey noonu lépp lu jub, ndax doo bàyyee dëngal yoon yu jub yu Boroom bi?
11 Léegi loxob Boroom bi dina dal sa kaw, te dinga gumba, ba dootuloo gis jant bi ab diir.» Ca saa sa nag ay bëtam muuru, mu daldi tàbbi cig lëndëm, muy làmbatu, di wut ku ko wommat.
12 Ba boroom réew ma gisee li xew nag, mu daldi gëm, di yéemu ci yoonu Boroom bi.
JËF YA 13 in Téereb Injiil

Jëf ya 13:6-12 in Kàddug Yàlla gi

6 Ci biir loolu ñu wër dun ba bépp, ba yegg Pafos, péey ba. Ñu tase faak ab ñeengokatub Yawut buy yonent-yonentlu, ñu di ko wax Bar Yeesu.
7 Ma nga bokkoon ca toppum Sergiyus Póolus boroom dëkk ba, nit ku rafet xel. Kooku namma dégg kàddug Yàlla, daldi woolu Barnaba ak Sóol.
8 Elimas, mu firi Ñeengokat bi, di leen gàllankoor nag, tey jéema fàbbi boroom réew ma, ba du gëm.
9 Ci kaw loolu Sóol mi ñuy wax Póol feese Noo gu Sell gi. Mu xool ñeengokat bi jàkk,
10 ne ko: «Yaw nit ki fees ak gépp xeetu njublaŋ ak ndëngte, doomu Seytaane ji, noonu gépp njub, doo bàyyee lunkal yooni njub yu Boroom bi?
11 Léegi nag loxol Boroom baa ngii fi sa kaw; dinga gumba, ba dootuloo gis jant bi ab diir.» Ca saa sa gis-gis bu naqari akug lëndëm ne milib ci kawam, muy wëndeelu, di wut ku ko wommat.
12 Ba loolu amee boroom dëkk ba gis la xew, daldi gëm, di yéemu ci li mu jànge ci Sang bi.
Jëf ya 13 in Kàddug Yàlla gi