Text copied!
Bibles in Wolof

JËF YA 13:38-52 in Wolof

Help us?

JËF YA 13:38-52 in Téereb Injiil

38 «Kon nag bokk yi, nangeen xam ne ci moom Yeesu nu ngi leen di yégal mbaalug bàkkaar yi. Te fépp fu yoonu Musaa tële woona àttee nit ni ku jub,
39 fa la Yeesu di àttee ni ku jub képp ku ko gëm.
40 Wottuleen nag ba li yonent yi bindoon bañ leena dal, ci li ñu ne:
41 “Yéen ñiy xeebaate, gisleen lii, ngeen yéemu ba far; ndaxte dinaa def ci seen jamono jëf, joo xam ne su ngeen ko déggee sax, dungeen ko gëm.”»
42 Bi ñuy génn nag ca jàngu ba, Yawut ya ñaan leen, ñu baamtu wax ja ca bésub noflaay ba ca tegu.
43 Te bi mbooloo ma tasee, ay Yawut yu bare ak ñi tuuboon ci yoonu Yawut te ragal Yàlla, topp ci Pool ak Barnabas. Ñuy diisoo ak ñoom, di leen xiir, ñu wàkkirlu ci yiwu Yàlla.
44 Noonu bésub noflaay ba ca tegu, daanaka waa dëkk bépp daje, ngir déglu kàddug Yàlla.
45 Waaye bi Yawut yi gisee mbooloo ma, ñu daldi fees ak kiñaan, di weddi li Pool di wax te di ko xas.
46 Bi loolu amee Pool ak Barnabas ne leen ci lu bir: «Yéen lanu wara jëkka yégal kàddug Yàlla, waaye gannaaw gàntu ngeen ko, ba àtte seen bopp ne yeyoowuleen dund gu dul jeex gi, kon nu ngi waññiku ci ñi dul Yawut.
47 Ndaxte moom la nu Boroom bi sant ci li mu naan: “Samp naa la, nga nekk leeru ñi dul Yawut, ngir nga yóbbu mucc gi, mu daj cati àddina.”»
48 Ñi dul Yawut nag, bi ñu déggee loolu, daldi bég tey màggal kàddug Boroom bi; te ñépp ñu jagoo dund gu dul jeex daldi gëm.
49 Noonu kàddug Boroom bi di law ci diiwaan bépp.
50 Waaye Yawut ya xiir ay jigéen, ñi woomle te farlu ci diine, ñoom ak magi dëkk ba, ñu fitnaal Pool ak Barnabas, ngir génne leen réew ma.
51 Waaye Pool ak Barnabas daldi yëlëb seen pëndu tànk, ngir dëggal seen weddi, jëm dëkku Ikoñum.
52 Naka taalibe yi nag, ñu fees ak mbég ak Xel mu Sell mi.
JËF YA 13 in Téereb Injiil

Jëf ya 13:38-52 in Kàddug Yàlla gi

38 «Kon nag bokk yi, xamleen ne ci Yeesu moomu lañu leen birale njéggalug bàkkaar. Te mboolem lu ngeen tële woona wàccool, ba seen njub mat ci yoonu Musaa,
39 képp ku gëm Yeesu, ci moom lay wàccook loolu lépp, ba ag njubam mat.
40 Wattuleen nag ba li ñu wax ci téerey yonent yi bañ leena dal. Ñu ne:
41 “Yeen xeebaatekat yi, xool-leen, jommileen te ne mes, ndax jëf ji may def ci seen jamono, ku leen ko waxoon sax, dungeen ko gëm.”»
42 Ba ñu génnee ca jàngu ba, dañu leena ñaan ñu baamtu kàddu googu bésub Noflaay ba ca topp.
43 Ba mbooloo ma tasaaroo, bare na ay Yawut ak tuubeen yuy jaamu Yàlla yu topp ci Póol ak Barnaba. Ñuy wax ak nit ñi, di leen ñaax, ngir ñu sax ci doyloo yiwu Yàlla.
44 Bésub Noflaay ba ca topp, daanaka waa dëkk bépp a daje, ngir déglu kàddug Boroom bi.
45 Ba Yawut yi gisee mbooloo ma nag, kiñaan man leen, ñuy weddi waxi Póol, di ko saaga.
46 Ba loolu amee fit la leen Póol ak Barnaba tontoo, ne leen: «Yeen Yawut yi de lanu wara jëkka yégal kàddug Yàlla gi, waaye gannaaw gàntal ngeen ko, ba jombale seen bopp ag texe ba fàww, nu ngii di walbatiku ci jaambur ñi.
47 Ndax noonu la nu ko Boroom bi sante ba mu nee: “Maa la tabb ngay leeru jaambur ñi, ngir nga jottliji mucc gii, ba ca cati àddina.”»
48 Ba jaambur ña déggee loolu, dañoo bég, di màggal kàddug Boroom bi; ci biir loolu ña dogal ba jagleel ag texe ba fàww, ñoom ñépp daldi gëm.
49 Kàddug Boroom bi nag di law ca diiwaan bépp.
50 Teewul Yawut ya xiirtal tuubeen yu jigéen yi gëna ràññiku, ak kàngam yu góor yi ci dëkk bi. Ñu daldi bundxatal Póol ak Barnaba, génne leen réew ma.
51 Póol ak Barnaba nag fëgg seen pëndub ndëgguy tànk, seedeel leen ko seen ngàntal, doora dem dëkk ba ñuy wax Ikoñum.
52 Ci biir loolu taalibe ya dese mbég ak Noo gu Sell gi, ba seen xol fees.
Jëf ya 13 in Kàddug Yàlla gi