38 «Kon nag bokk yi, xamleen ne ci Yeesu moomu lañu leen birale njéggalug bàkkaar. Te mboolem lu ngeen tële woona wàccool, ba seen njub mat ci yoonu Musaa,
39 képp ku gëm Yeesu, ci moom lay wàccook loolu lépp, ba ag njubam mat.
40 Wattuleen nag ba li ñu wax ci téerey yonent yi bañ leena dal. Ñu ne:
41 “Yeen xeebaatekat yi, xool-leen, jommileen te ne mes, ndax jëf ji may def ci seen jamono, ku leen ko waxoon sax, dungeen ko gëm.”»
42 Ba ñu génnee ca jàngu ba, dañu leena ñaan ñu baamtu kàddu googu bésub Noflaay ba ca topp.
43 Ba mbooloo ma tasaaroo, bare na ay Yawut ak tuubeen yuy jaamu Yàlla yu topp ci Póol ak Barnaba. Ñuy wax ak nit ñi, di leen ñaax, ngir ñu sax ci doyloo yiwu Yàlla.