Text copied!
Bibles in Wolof

JËF YA 13:21-43 in Wolof

Help us?

JËF YA 13:21-43 in Téereb Injiil

21 Booba ñuy ñaan buur, te Yàlla jox leen Sóol, doomu Kis ci giiru Beñamin, muy seen buur diirub ñeent fukki at. Gannaaw ga mu jële ko fa,
22 dellu falal leen buur bu tudd Daawuda, mu seedee ko nii: “Gis naa Daawuda, doomu Isayi, ku ma neex ci sama xol, te dina def lépp luy sama coobare.”
23 «Noonu ci askanam Yàlla indil na bànni Israyil Musalkat bi Yeesu, ci ni mu ko dige woon.
24 Laata muy ñëw nag, Yaxya daan na waare, ne bànni Israyil gépp, ñu tuub seeni bàkkaar, te mu sóob leen ci ndox.
25 Te ba Yaxyay jeexal sasam, mu ne: “Ku ngeen may teg? Duma Ki wara ñëw; waaye am na kuy ñëw sama gannaaw, koo xam ne kii yeyoowumaa tekki ay dàllam.”
26 «Bokk yi, yéen askanu Ibraayma ak yéen ñi ragal Yàlla, kàddug mucc gi ci nun la wàcc.
27 Waa Yerusalem ak seeni kilifa xàmmiwuñu woon Yeesu te xamuñu woon waxu yonent, yi ñuy jàng bésub noflaay bu nekk; teewul ñu amal waxu yonent yi, ci li ñu àtte Yeesu, ba daan ko.
28 Yoon dabu ko fenn, moona ñaan nañu Pilaat, mu reylu ko.
29 Noonu ñu def lépp lu yonent yi bindoon ci mbiram, ba noppi ñu wàcce ko ca bant ba, tàbbal ko ci bàmmeel.
30 Waaye Yàlla dekkal na ko,
31 te diirub ay fan yu bare feeñu na ñi àndoon ak moom, jóge diiwaanu Galile, dem Yerusalem; léegi nag ñooy ay seedeem ci wetu xeet wi,
32 te nu ngi leen di xamal xibaaru jàmm bi ne leen, li Yàlla digoon sunuy maam,
33 def na ko ngir nun seeni sët, ci li mu dekkal Yeesu. Moom lañu bindoon ci ñaareelu saaru Sabóor ne: “Yaa di sama Doom, maa di sa Baay tey.”
34 Te it li ko Yàlla dekkal, ba mu bañatee jaar ci dee, te suuf du ko lekk mukk, moom la Yàlla wax ne: “Dinaa la may barke yu sell te wóor, yi ma digoon Daawuda.”
35 Moo tax mu waxaat feneen ne: “Doo bàyyi sa Waa ju sell, mu yàqu.”
36 Ndaxte bi Daawuda defee coobarey Yàlla ci jamonoom, mu faatu, ñu suul ko, mu fekki ay maamam, suuf lekk ko.
37 Waaye ki Yàlla dekkal, yaramam seeyul.
38 «Kon nag bokk yi, nangeen xam ne ci moom Yeesu nu ngi leen di yégal mbaalug bàkkaar yi. Te fépp fu yoonu Musaa tële woona àttee nit ni ku jub,
39 fa la Yeesu di àttee ni ku jub képp ku ko gëm.
40 Wottuleen nag ba li yonent yi bindoon bañ leena dal, ci li ñu ne:
41 “Yéen ñiy xeebaate, gisleen lii, ngeen yéemu ba far; ndaxte dinaa def ci seen jamono jëf, joo xam ne su ngeen ko déggee sax, dungeen ko gëm.”»
42 Bi ñuy génn nag ca jàngu ba, Yawut ya ñaan leen, ñu baamtu wax ja ca bésub noflaay ba ca tegu.
43 Te bi mbooloo ma tasee, ay Yawut yu bare ak ñi tuuboon ci yoonu Yawut te ragal Yàlla, topp ci Pool ak Barnabas. Ñuy diisoo ak ñoom, di leen xiir, ñu wàkkirlu ci yiwu Yàlla.
JËF YA 13 in Téereb Injiil

Jëf ya 13:21-43 in Kàddug Yàlla gi

21 Ba loolu wéyee, ñuy sàkku buur, Yàlla jox leen doomu Kis, Sóol, mi soqikoo ci giirug Beñamin, mu falu diiru ñeent fukki at.
22 Mu jële ko fa, sampal leen Daawuda, muy buur bu mu seedeel ne: “Maa ràññee Daawuda doomu Yese, ji sama xol jubool, te mooy jëfe mboolem samay coobare.”
23 «Ci askanu kookii la Yàlla indee Yeesu, na mu ko digee woon, muy Musalkat ñeel Israyil.
24 Laata muy ñëw, Yaxya moo doon yéene ngir waa bànni Israyil gépp sóobu cim ndox, jëmmale ko seenug tuubeel.
25 Ba Yaxya di jeexal aw sasam la ne: “Ana ku ngeen foog ne moom laa? Duma ki ngeen foog, waaye am na kuy ñëw nii sama gannaaw, ku ma yeyoowula summil sax ay dàllam.”
26 «Bokk yi, yeen askanu Ibraayma, yeen ak jaamburi ragalkati Yàlla yi ci seen biir, nun lañu yónnee kàddug mucc gii.
27 Waa Yerusalem, ak seeni kilifa nag xàmmiwuñu woon Yeesu, te ba ñu daanee Yeesu lañu sottal waxu yonent, ya ñu daan biral bésub Noflaay bu nekk.
28 Gisuñu ci moom lenn lu ko àtteb dee dabe, te teewul ñu sàkku Pilaat reylu ko.
29 Gannaaw ba ñu matalee mboolem lu ñu bind ci moom, lañu ko wàccee ca bant ba, dugal ko bàmmeel.
30 Waaye Yàllaa ko dekkal,
31 te diiru fan yu bare la feeñu ña àndoon ak moom, jóge diiwaanu Galile, dem Yerusalem, te ñooñooy ay seedeem tey ci askan wi.
32 Nun nag noo leen di àgge xibaaru jàmm bii: li Yàlla digoon sunuy maam,
33 nun sët yi la ko defal, ba mu yékkatee Yeesu, te noonee lañu ko binde ci ñaareelu saaru Sabóor, ne: “Yaa di sama Doom, bés niki tey maa la jur.”
34 Noonu ko Yàlla dekkale ndekkite lu dee toppatul, te yaramam du yàqu mukk, noonee la ko Yàlla waxe woon, ne: “Maa lay jox barkey Daawuda yu sell yi te wóor.”
35 Moo tax mu waxaat feneen ne: “Doo bàyyi sa ku Sell ki, mu yàqu.”
36 Daawuda moom, gannaaw ba mu defee coobarey Yàlla ci jamonoom, nelaw na, ba ñu rob ko ca weti maamam ya, te yàqu na.
37 Waaye moom mi Yàlla dekkal, yàquwul.
38 «Kon nag bokk yi, xamleen ne ci Yeesu moomu lañu leen birale njéggalug bàkkaar. Te mboolem lu ngeen tële woona wàccool, ba seen njub mat ci yoonu Musaa,
39 képp ku gëm Yeesu, ci moom lay wàccook loolu lépp, ba ag njubam mat.
40 Wattuleen nag ba li ñu wax ci téerey yonent yi bañ leena dal. Ñu ne:
41 “Yeen xeebaatekat yi, xool-leen, jommileen te ne mes, ndax jëf ji may def ci seen jamono, ku leen ko waxoon sax, dungeen ko gëm.”»
42 Ba ñu génnee ca jàngu ba, dañu leena ñaan ñu baamtu kàddu googu bésub Noflaay ba ca topp.
43 Ba mbooloo ma tasaaroo, bare na ay Yawut ak tuubeen yuy jaamu Yàlla yu topp ci Póol ak Barnaba. Ñuy wax ak nit ñi, di leen ñaax, ngir ñu sax ci doyloo yiwu Yàlla.
Jëf ya 13 in Kàddug Yàlla gi