20 Loolu lépp a ngi am ci diiru ñeenti téeméeri at ak juróom fukk (450). «Gannaaw loolu moo sàkkal sunuy maam ay njiit, ba ci jamonoy Yonent Yàlla Samiyel.
21 Ba loolu wéyee, ñuy sàkku buur, Yàlla jox leen doomu Kis, Sóol, mi soqikoo ci giirug Beñamin, mu falu diiru ñeent fukki at.
22 Mu jële ko fa, sampal leen Daawuda, muy buur bu mu seedeel ne: “Maa ràññee Daawuda doomu Yese, ji sama xol jubool, te mooy jëfe mboolem samay coobare.”
23 «Ci askanu kookii la Yàlla indee Yeesu, na mu ko digee woon, muy Musalkat ñeel Israyil.
24 Laata muy ñëw, Yaxya moo doon yéene ngir waa bànni Israyil gépp sóobu cim ndox, jëmmale ko seenug tuubeel.