Text copied!
Bibles in Wolof

JËF YA 13:15-20 in Wolof

Help us?

JËF YA 13:15-20 in Téereb Injiil

15 Bi ñu jàngee yoonu Musaa ak yonent ya, njiiti jàngu ba yónnee ca ñoom ne leen: «Bokk yi, bu ngeen amee lu ngeen di dénk mbooloo mi, waxleen ko.»
16 Noonu Pool jóg, tàllal loxoom ne leen: «Yéen bokki Israyil ak yéen ñi ragal Yàlla, dégluleen!
17 Yàllay bànni Israyil tànn na sunuy maam, di yokk xeet wa, bi ñuy ganeyaan ci Misra; ba noppi mu génne leen fa ak kàttanu loxoom.
18 Diirub ñeent fukki at mu di leen muñal ca màndiŋ ma.
19 Gannaaw loolu faagal na juróom ñaari xeet ci réewu Kanaan, ba sunuy maam donn réew ma.
20 Loolu lépp xew na ci diirub ñeenti téeméeri at ak juróom fukk. «Gannaaw loolu mu jox leen ay njiit, ba ci yonent Yàlla Samiyel.
JËF YA 13 in Téereb Injiil

Jëf ya 13:15-20 in Kàddug Yàlla gi

15 Gannaaw ba tarib dog ya ca téereb yoonu Musaa, ak téereb yonent ya sottee, njiiti jàngu ba yóbbante leen kàddu, ne leen: «Bokk yi, bu ngeen amee kàddu gu ngeen ñaaxe mbooloo mi, waxleen.»
16 Póol jóg, tàllal loxoom, nee leen: «Yeen bokki Israyil ak yeen jaamburi ragalkati Yàlla yi, dégluleen!
17 Yàllay bànni Israyil jii moo tànnoon sunuy maam, moo yaatal xeet wi, ba ñuy ganeyaan ca Misra; moo leen fa génnee kàttanu loxoom.
18 Lu tollook ñeent fukki at la leen muñal ca màndiŋ ma.
19 Moo faagaagal juróom ñaari xeet ca réewum Kanaan, daldi muurale sunuy maam réewum Kanaaneen ña.
20 Loolu lépp a ngi am ci diiru ñeenti téeméeri at ak juróom fukk (450). «Gannaaw loolu moo sàkkal sunuy maam ay njiit, ba ci jamonoy Yonent Yàlla Samiyel.
Jëf ya 13 in Kàddug Yàlla gi