Text copied!
Bibles in Wolof

JËF YA 13:12-17 in Wolof

Help us?

JËF YA 13:12-17 in Téereb Injiil

12 Ba boroom réew ma gisee li xew nag, mu daldi gëm, di yéemu ci yoonu Boroom bi.
13 Naka noona Pool ak ñi mu àndal jóge Pafos, jaar ci géej, jëm dëkku Peers ci réewu Pamfili. Yowaana nag tàggoo ak ñoom, dellu Yerusalem.
14 Waaye ñoom ñu jóge Peers, aw ca yoon wa, ba ñëw dëkku Ancos ci diiwaanu Pisidi. Bésub noflaay ba nag ñu dugg ca jàngu ba, toog.
15 Bi ñu jàngee yoonu Musaa ak yonent ya, njiiti jàngu ba yónnee ca ñoom ne leen: «Bokk yi, bu ngeen amee lu ngeen di dénk mbooloo mi, waxleen ko.»
16 Noonu Pool jóg, tàllal loxoom ne leen: «Yéen bokki Israyil ak yéen ñi ragal Yàlla, dégluleen!
17 Yàllay bànni Israyil tànn na sunuy maam, di yokk xeet wa, bi ñuy ganeyaan ci Misra; ba noppi mu génne leen fa ak kàttanu loxoom.
JËF YA 13 in Téereb Injiil

Jëf ya 13:12-17 in Kàddug Yàlla gi

12 Ba loolu amee boroom dëkk ba gis la xew, daldi gëm, di yéemu ci li mu jànge ci Sang bi.
13 Póol ak ñi mu àndal nag bàyyikoo Pafos, dugg gaal, jëm Perge, ca diiwaanu Pamfili. Yowaan moom tàggoo ak ñoom, dellu Yerusalem.
14 Ci kaw loolu, ñoom ñu jóge Perge, jàll ba Àncos ca diiwaanu Pisidi. Ñu dem jàngu ba, dugg, toog ca bésub Noflaay ba.
15 Gannaaw ba tarib dog ya ca téereb yoonu Musaa, ak téereb yonent ya sottee, njiiti jàngu ba yóbbante leen kàddu, ne leen: «Bokk yi, bu ngeen amee kàddu gu ngeen ñaaxe mbooloo mi, waxleen.»
16 Póol jóg, tàllal loxoom, nee leen: «Yeen bokki Israyil ak yeen jaamburi ragalkati Yàlla yi, dégluleen!
17 Yàllay bànni Israyil jii moo tànnoon sunuy maam, moo yaatal xeet wi, ba ñuy ganeyaan ca Misra; moo leen fa génnee kàttanu loxoom.
Jëf ya 13 in Kàddug Yàlla gi