Text copied!
Bibles in Wolof

JËF YA 12:8-15 in Wolof

Help us?

JËF YA 12:8-15 in Téereb Injiil

8 Malaaka ma ne ko: «Takkal sa geño te sol say dàll.» Mu def ko. Malaaka ma ne ko: «Solal sa mbubb te topp ci man.»
9 Piyeer génn, topp ca malaaka ma, fekk gëmul sax ne lu am la, waaye mu yaakaar ne peeñu la.
10 Noonu ñu weesu wottukat bu jëkk ba ak ba ca tegu, ñu agsi ca buntu weñ, ba jëm ca dëkk ba, mu daldi ubbikul boppam ci seen kanam. Ñu génn nag, jaar ci benn mbedd, malaaka ma daldi ko bàyyi.
11 Bi xelam délsee ci moom Piyeer ne: «Léegi xam naa ci lu wóor ne, Boroom bi yónni na malaakaam, musal ma ci loxoy Erodd ak li ma Yawut ya yéene woon lépp.»
12 Mu rabal xelam ci loolu, daldi dem kër Maryaama, ndeyu Yowaana, mi ñuy wax it Màrk, fekk ñu bare booloo fa, di ñaan ci Yàlla.
13 Noonu Piyeer fëgg buntu kër ga, te mbindaan mu tudd Rodd wuyusi ko.
14 Mu xàmmi baatu Piyeer, bég ci, ba fàtte koo ubbil, waaye mu daw ci biir, xamle ne Piyeer a nga ca bunt ba.
15 Ñu ne ko: «Xanaa dangaa dof.» Waaye mu dëgër ci li mu wax. Noonu ñu ne ko: «Xanaa malaakaam la.»
JËF YA 12 in Téereb Injiil

Jëf ya 12:8-15 in Kàddug Yàlla gi

8 Malaaka ma ne ko: «Takkal sa geño te sol say dàll.» Mu def noonu. Mu ne ko: «Solal sa mbubb te topp ci man.»
9 Piyeer génn, topp ci moom, te xamul sax ndax li ko dikkal noonu te sababoo ci malaaka mi, dëgg la. Yaakaaroon na ne am peeñu la.
10 Ñu jàll dalu wattukat bu jëkk bi, teg ci ñaareel bi, ba agsi ci buntu weñ, ba jëm ca dëkk ba, bunt ba daldi tijjikul boppam. Ñu génn, topp menn mbedd, malaaka ma jekki teqlikook Piyeer.
11 Naka la xelum Piyeer délsi, mu daldi ne: «Léegi nag xam naa xéll ne, Boroom bee yebal malaakaam, te moo ma musal ci loxol Erodd, ak mboolem li Yawut yi séentu woon.»
12 Gannaaw ba Piyeer ràññee loolu, daa dem kër Maryaama, ndeyu Yowaan Màrk, fekk ñu bare daje foofa, di ñaan.
13 Piyeer fëgg buntu kër ga, mbindaan mu ñuy wax Rodd dikk.
14 Ba Piyeer waxee, mbindaan ma xàmmi baatam, daldi bég ba talu koo ubbil, xanaa daw dellu ca biir, ne Piyeer a nga foofa ca buntu kër ga.
15 Ñu ne ko: «Xanaa dangaa dof?» Teewul mbindaan mi ne moom la. Ñu daldi ne: «Kon malaakaam la.»
Jëf ya 12 in Kàddug Yàlla gi