7 Ci kaw loolu am malaakam Boroom bi ne jaas, taxaw, ag leer ne ràyy ca biir kaso ba. Malaaka ma laal Piyeer ci wetam, yee ko, ne ko: «Jógal gaaw!», càllala yi daldi rote ciy loxoom.
8 Malaaka ma ne ko: «Takkal sa geño te sol say dàll.» Mu def noonu. Mu ne ko: «Solal sa mbubb te topp ci man.»
9 Piyeer génn, topp ci moom, te xamul sax ndax li ko dikkal noonu te sababoo ci malaaka mi, dëgg la. Yaakaaroon na ne am peeñu la.