13 Noonu Piyeer fëgg buntu kër ga, te mbindaan mu tudd Rodd wuyusi ko.
14 Mu xàmmi baatu Piyeer, bég ci, ba fàtte koo ubbil, waaye mu daw ci biir, xamle ne Piyeer a nga ca bunt ba.
15 Ñu ne ko: «Xanaa dangaa dof.» Waaye mu dëgër ci li mu wax. Noonu ñu ne ko: «Xanaa malaakaam la.»
16 Fekk Piyeer di gëna fëgg. Noonu ñu tijji, gis ko, daldi waaru.
17 Piyeer taf loxoom ci gémmiñam, ngir ñu noppi, daldi leen nettali, ni ko Boroom bi génnee ca kaso ba. Mu ne leen: «Tee ngeen jottali ko Saag ak bokk ya.» Bi mu ko waxee, mu jóge fa, dem feneen.
18 Bi bët setee nag, yëngu-yëngu bu réy am na ca xarekat ya, ñu ne: «Ana Piyeer?»
19 Noonu Erodd wutlu ko, waaye gisu ko. Kon mu àtte wottukat ya, joxe ndigalu rey leen. Bi loolu amee Erodd jóge ci diiwaanu Yude, dem dëkku Sesare, toog fa.