Text copied!
Bibles in Wolof

JËF YA 11:24-30 in Wolof

Help us?

JËF YA 11:24-30 in Téereb Injiil

24 Ndaxte nit ku baax la woon te fees ak Xel mu Sell mi ak ngëm; noonu mbooloo mu bare dolliku ci Boroom bi.
25 Gannaaw loolu Barnabas dem ca dëkku Tars, di wut Sóol.
26 Bi mu ko gisee, mu indi ko Ancos. Noonu atum lëmm ñu bokk ak mbooloom ñi gëm, di jàngal nit ñu bare. Te ci Ancos lañu jëkka tudde taalibe ya Gaayi Kirist.
27 Ca fan yooyu ay yonent jóge Yerusalem, ñëw Ancos.
28 Kenn ci ñoom tudd Agabus jóg, mu yégle jaarale ko ci Xelu Yàlla mi ne xiif bu metti dina daj àddina sépp. Loolu nag amoon na ca ayug buur bu ñuy wax Këlódd.
29 Kon taalibe ya fas yéenee sàkk ndimbal, jëme ca bokk ya dëkk diiwaanu Yude, ku nekk ak sa kem kàttan.
30 Noonu lañu def nag, teg ko ci loxoy Barnabas ak Sóol, yónnee ko njiit ya.
JËF YA 11 in Téereb Injiil

Jëf ya 11:24-30 in Kàddug Yàlla gi

24 Ndaxte Barnaba nit ku baax la woon, feese Noo gu Sell gi, ak ngëm. Mbooloo mu takku nag dolliku ci Sang bi.
25 Ba loolu wéyee Barnaba jëm Tàrs, di seeti Sóol.
26 Ba mu ko gisee, da koo indi Àncos. Ba mu ko defee, atum lëmm ñuy daje ca mbooloom gëmkat ña, di jàngal nit ñu takku. Ca Àncos lañu jëkka wooye gëmkat ñi ay gëm-Almasi.
27 Ci fan yooyu la ay yonent jóge Yerusalem, dikk Àncos.
28 Kenn ca ñoom, ku ñuy wax Agabus daldi yéglee Noo gu Sell gi, ne xiif bu metti dina am, ci àddina sépp. Te looloo nga yemook ayug buur bu mag bu ñuy wax Këlódd.
29 Taalibe ya nag fas yéenee boole kem kàttanu ku nekk ca ñoom, ngir ndimbal lu ñuy yónnee bokki diiwaanu Yude.
30 Noonu lañu def, yónnee ko magi Yude, Barnaba ak Sóol jottli ko.
Jëf ya 11 in Kàddug Yàlla gi