Text copied!
Bibles in Wolof

JËF YA 11:2-6 in Wolof

Help us?

JËF YA 11:2-6 in Téereb Injiil

2 Bi Piyeer demee Yerusalem nag, kureelu Yawut gi farataal xaraf, di werante ak moom ne ko:
3 «Lu tax nga dem ca këru ñu xaraful, bay lekk sax ak ñoom?»
4 Noonu Piyeer daldi leen benn-bennal mbir mi, nettali leen ko
5 ne: «Nekkoon naa ca dëkku Yope, di fa ñaan ci Yàlla, ba far sama xol seey ci moom; noonu ma am peeñu: lu mel ni sér bu mag wàcc, jóge ci asamaan, ñu yoor ko ca ñeenti laf ya, mu ñëw ba ci man.
6 Ma xool ko jàkk, seetlu ko bu baax, ma gis ca boroom ñeenti tànk yu nekk ci kaw suuf, di rabi àll yi, yiy raam ak picci asamaan.
JËF YA 11 in Téereb Injiil

Jëf ya 11:2-6 in Kàddug Yàlla gi

2 Ba Piyeer delloo Yerusalem nag, gëmkat ñi bokk ci askanu Yawut di ko sikk,
3 naan: «Yaa dem ca ña xaraful, di bokk ak ñoom lekk!»
4 Piyeer daldi leen benn-bennalal mbir mi.
5 Mu ne: «Man de damaa nekkoon ca Yope, di fa ñaan. Ci biir loolu ma daanu ag leer, daldi gis ci peeñu lu mel ni sér bu mag bu ñu téyee ñeenti lafam, mu wàcce asamaan, ba agsi ci man.
6 Ma xool ko jàkk, niir ko, daldi cay gis boroom ñeenti tànk yi, ak rabi àll yi, ak dundoot yiy raam ak njanaaw yi.
Jëf ya 11 in Kàddug Yàlla gi