Text copied!
Bibles in Wolof

JËF YA 10:33-47 in Wolof

Help us?

JËF YA 10:33-47 in Téereb Injiil

33 Yónnee naa nag ci ni mu gëna gaawe, woolu la; te maa ngi lay sant ci li nga ñëw. Léegi nag nun ñépp nu ngi fi ci kanam Yàlla, ngir déglu lépp li la Boroom bi sant.»
34 Noonu Piyeer jël kàddu ga ne leen: «Ci dëgg gis naa ne Yàlla du gënale,
35 waaye ci xeet yépp, ku ko ragal tey def lu jub, moom la nangu.
36 Yónnee na kàddoom bànni Israyil, di leen xibaar jàmm, jaarale ko ci Yeesu Kirist, miy Boroom lépp.
37 Xam ngeen li xewoon ci réewum Yawut yépp, li ko tàmbalee ci diiwaanu Galile, topp ci waareb Yaxya, mu naan nit ñi, mu sóob leen ci ndox.
38 Xam ngeen ne Yàlla fal na Yeesum Nasaret, sol ko Xel mu Sell mi ak kàttan; muy wër, di def lu baax ak di faj ñépp ñi nekkoon ci kilifteefu Seytaane, ndaxte Yàlla ànd na ak moom.
39 «Seede nanu li mu def lépp ci biir réewu Yawut ya ak Yerusalem. Moona rey nañu ko ci wékk ko ci bant.
40 Waaye Yàlla dekkal na ko ci ñetteelu fan ba te biral ko,
41 waxuma xeet wépp, waaye seede yi Yàlla tànn lu jiitu, maanaam nun ñi daan lekk di naan ak moom gannaaw ndekkiteem.
42 Te Yeesu sant na nu, nu yégal xeet wa, di seede ne moom la Yàlla jagleel àtteb ñiy dund ak ñi dee.
43 Yonent yépp seedeel nañu ko ne, ku ko gëm, Yàlla dina la baal say bàkkaar ci turam.»
44 Bi Piyeer di wax loolu, Xel mu Sell mi wàcc ci kaw ñépp ñiy déglu kàddu ga.
45 Yawut yi gëm yépp nag, ñi ànd ak Piyeer, daldi waaru ci li Yàlla tuur Xel mu Sell, mi mu maye, ci ñi dul Yawut itam.
46 Ndaxte dégg nañu leen, ñuy wax yeneen làkk ak di màggal Yàlla.
47 Booba Piyeer daldi wax ne: «Ñii jot Xel mu Sell mi ni nun, ndax manees na leena baña sóob ci ndox?»
JËF YA 10 in Téereb Injiil

Jëf ya 10:33-47 in Kàddug Yàlla gi

33 Ca saa sa nag laa yeble ci yaw. Yaw it def nga lu baax, bi nga dikkee. Léegi nag nun ñépp a ngi fi ci kanam Yàlla, ngir déglu mboolem lu la Boroom bi sant.»
34 Ba loolu amee Piyeer àddu, ne: «Dëgg-dëgg gis naa ne Yàlla daal du gënaatle,
35 waaye xeetoo xeet, ku ko ci ragal tey def njekk, mooy ki ko neex.
36 Moo yónnee kàddoom bànni Israyil, àgge leen xibaaru jàmm, biy maye jàmm ci Yeesu Almasi, miy Sangu ñépp.
37 Yeen ci seen bopp xam ngeen li xewoon ci mboolem réewum Yawut yi, te dale ci diiwaanu Galile, gannaaw ba Yaxya wootee, di sóobe cim ndox,
38 ak ni Yàlla ànde ak Yeesum Nasaret, ba jagleel ko pal gu mu dogale Noo gu Sell geek xam-xam bi mu ko sotti, muy wër, di def lu baax, di faj mboolem ñi Seytaane notoon.
39 «Nun ci sunu bopp noo seede li mu def lépp ci réewum Yawut yi ak Yerusalem. Moom mi ñu wékk ci bant, ba rey ko,
40 moom la Yàlla dekkal ci ñetteelu fanam, ba may ko mu feeñ.
41 Du askan wépp la ko won, xanaa nun, seede yi Yàlla tànnoon lu jiitu, nu bokk ak moom lekk ak naan, gannaaw ndekkiteem.
42 Moo nu sant nag nu xamal askan wi te seede ne moom la Yàlla tabb àttekatub aji dund ñi, ak aji dee ñi.
43 Moom la yonent yépp seedeel, ne képp ku ko gëm, jot nga sa njéggalug bàkkaar ciw turam.»
44 Ba Piyeer di wax kàddu googu, Noo gu Sell gi daldi wàcc ci kaw mboolem ñay déglu kàddu ga.
45 Ba loolu amee mboolem gëmkati Yawut ya ànd ak Piyeer, waaru ca na mayug Noo gu Sell gi tuuruwaalee ca xeeti jaambur ña,
46 ndax dañu leena dégg ñoom itam, ñuy làkk yeneen làkk, ak a màggal Yàlla.
47 Piyeer dellu ne: «Ñii jot Noo gu Sell gi ni nun, ndax manees na leena baña sóob ci ndox?»
Jëf ya 10 in Kàddug Yàlla gi