Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Jëf ya - Jëf ya 10

Jëf ya 10:13-24

Help us?
Click on verse(s) to share them!
13Mu am baat bu jib, ne ko: «Piyeer, jógal, rey te lekk.»
14Piyeer ne ko: «Mukk, Sang bi, ndaxte masumaa lekk lenn lu daganul mbaa lu setul.»
15Teewul baat bi wax ak moom ñaareel bi yoon, ne ko: «Lu Yàlla setal, bu ko daganadil.»
16Menn peeñu moomu dikkal na ko ñetti yoon. La ca tegu ñu yéege këf ka asamaan.
17Piyeer a nga jaaxle lool, di seet cim xelam lu peeñu ma ko dikkal di tekki, ndeke nit ña Korney yebaloon laaj nañu kër Simoŋ, ba dikk taxaw ca bunt ba.
18Ñu woote, laajte, ne: «Simoŋ, mi ñuy wax Piyeer, fii la dëkk?»
19Naka la Piyeer di xalaat ba tey ca peeñu ma, Noo gi ne ko: «Ñetti nit a ngi nii, di la seet.
20Wàccal boog, ànd ak ñoom te bul nàttable, ndax man maa leen yebal.»
21Piyeer wàcc nag ne nit ñi: «Maa ngii; ki ngeen di seet, man la. Lu doon seeni tànk?»
22Ñu ne ko: «Njiitu takk-der ba Korney, ku jub, ragal Yàlla, te rafet seede bu ko xeetu Yawut wépp seedeel, moo jote ci malaaka mu sell, ndigalal woolu la këram, ngir déglu say kàddu.»
23Ci kaw loolu Piyeer dugal leen, dalal leen. Ba bët setee, Piyeer ànd ak ñoom, ñenn ca bokki gëmkat ña dëkke Yope gunge ko.
24Ca ëllëg sa Piyeer agsi Sesare. Fekk na Korney di ko séentu, daldi woo ca këram ay bokkam, ak xaritam yi ko gëna jege.

Read Jëf ya 10Jëf ya 10
Compare Jëf ya 10:13-24Jëf ya 10:13-24