Text copied!
Bibles in Wolof

JËF YA 10:11-26 in Wolof

Help us?

JËF YA 10:11-26 in Téereb Injiil

11 Mu xool asamaan ubbiku, gis lu mel ni sér bu mag bu ñu téye ci ñeenti laf ya, yoor ko, mu jëm suuf.
12 Boroom ñeenti tànk yépp ñu nga ca, ak yiy raam ci suuf, ak picci asamaan.
13 Te baat ne ko: «Jógal, Piyeer, rey te lekk.»
14 Waaye Piyeer ne ko: «Mukk, Boroom bi, ndaxte masumaa lekk dara lu daganul mbaa lu araam.»
15 Waaye baat bi wax ak moom ñaareelu yoon ne ko: «Lu Yàlla sellal, bu ko araamal.»
16 Ñu def ko nag, ba muy ñetti yoon, ba noppi ñu ne cas sér ba, jëme asamaan.
17 Bi loolu amee Piyeer jaaxle lool ci lu peeñu miy tekki; fekk booba nit ñi Korney yebal, laajte woon nañu kër Simoŋ, ba agsi ci bunt bi.
18 Ñu woote nag naan: «Simoŋ, mi ñu dàkkentale Piyeer, ndax fi la dëkk?»
19 Bi Piyeer di rabal xelam ci peeñu ma, Xel mi ne ko: «Ñetti nit a ngi nii, di la wut.
20 Jógal, nga wàcc te ànd ak ñoom; bul werante, ndaxte maa leen yebal.»
21 Piyeer wàcc nag ne nit ñi: «Maa ngi nii, man mi ngeen di wut; lu doon seeni tànk?»
22 Ñu ne ko: «Korney, njiitu xare ba, nit ku jub la te ragal Yàlla, ba am seede su rafet ci bànni Israyil gépp. Malaaka mu sell nag sant na ko, mu woolu la ci këram te déglu li ngay wax.»
23 Ci kaw loolu Piyeer dugal leen, dalal leen. Ba bët setee, Piyeer jóg, dem ak ñoom, ànd ak ñenn ci bokk yi dëkk Yope,
24 te bés ba ca topp mu dikk Sesare. Fekk Korney woo na këram ay bokkam ak i xaritam yi ko gëna jege, di xaar Piyeer.
25 Bi Piyeer duggee nag, Korney daje ak moom, daanu ciy tànkam, sargal ko.
26 Waaye Piyeer yékkati ko ne: «Jógal, man it nit rekk laa.»
JËF YA 10 in Téereb Injiil

Jëf ya 10:11-26 in Kàddug Yàlla gi

11 Mu daldi gis asamaan ubbiku, lu mel ni sér bu mag bu ñu téyee ñeenti lafam, wàcce asamaan, jëm suuf.
12 Sér baa nga def mboolem boroom ñeenti tànk, ak dundoot yiy raam, ak mboolem njanaaw.
13 Mu am baat bu jib, ne ko: «Piyeer, jógal, rey te lekk.»
14 Piyeer ne ko: «Mukk, Sang bi, ndaxte masumaa lekk lenn lu daganul mbaa lu setul.»
15 Teewul baat bi wax ak moom ñaareel bi yoon, ne ko: «Lu Yàlla setal, bu ko daganadil.»
16 Menn peeñu moomu dikkal na ko ñetti yoon. La ca tegu ñu yéege këf ka asamaan.
17 Piyeer a nga jaaxle lool, di seet cim xelam lu peeñu ma ko dikkal di tekki, ndeke nit ña Korney yebaloon laaj nañu kër Simoŋ, ba dikk taxaw ca bunt ba.
18 Ñu woote, laajte, ne: «Simoŋ, mi ñuy wax Piyeer, fii la dëkk?»
19 Naka la Piyeer di xalaat ba tey ca peeñu ma, Noo gi ne ko: «Ñetti nit a ngi nii, di la seet.
20 Wàccal boog, ànd ak ñoom te bul nàttable, ndax man maa leen yebal.»
21 Piyeer wàcc nag ne nit ñi: «Maa ngii; ki ngeen di seet, man la. Lu doon seeni tànk?»
22 Ñu ne ko: «Njiitu takk-der ba Korney, ku jub, ragal Yàlla, te rafet seede bu ko xeetu Yawut wépp seedeel, moo jote ci malaaka mu sell, ndigalal woolu la këram, ngir déglu say kàddu.»
23 Ci kaw loolu Piyeer dugal leen, dalal leen. Ba bët setee, Piyeer ànd ak ñoom, ñenn ca bokki gëmkat ña dëkke Yope gunge ko.
24 Ca ëllëg sa Piyeer agsi Sesare. Fekk na Korney di ko séentu, daldi woo ca këram ay bokkam, ak xaritam yi ko gëna jege.
25 Ba Piyeer duggsee, Korney gatandu ko, ne gurub ca tànki Piyeer, sujjóot.
26 Piyeer yékkati ko, ne: «Déet jógal, man it, nit doŋŋ laa.»
Jëf ya 10 in Kàddug Yàlla gi