10 Mu dem ba xiif, bëgga lekk, ñu di ko toggal nag lu mu lekk. Ci biir loolu mu daanu leer.
11 Mu daldi gis asamaan ubbiku, lu mel ni sér bu mag bu ñu téyee ñeenti lafam, wàcce asamaan, jëm suuf.
12 Sér baa nga def mboolem boroom ñeenti tànk, ak dundoot yiy raam, ak mboolem njanaaw.
13 Mu am baat bu jib, ne ko: «Piyeer, jógal, rey te lekk.»
14 Piyeer ne ko: «Mukk, Sang bi, ndaxte masumaa lekk lenn lu daganul mbaa lu setul.»
15 Teewul baat bi wax ak moom ñaareel bi yoon, ne ko: «Lu Yàlla setal, bu ko daganadil.»
16 Menn peeñu moomu dikkal na ko ñetti yoon. La ca tegu ñu yéege këf ka asamaan.
17 Piyeer a nga jaaxle lool, di seet cim xelam lu peeñu ma ko dikkal di tekki, ndeke nit ña Korney yebaloon laaj nañu kër Simoŋ, ba dikk taxaw ca bunt ba.
18 Ñu woote, laajte, ne: «Simoŋ, mi ñuy wax Piyeer, fii la dëkk?»
19 Naka la Piyeer di xalaat ba tey ca peeñu ma, Noo gi ne ko: «Ñetti nit a ngi nii, di la seet.
20 Wàccal boog, ànd ak ñoom te bul nàttable, ndax man maa leen yebal.»
21 Piyeer wàcc nag ne nit ñi: «Maa ngii; ki ngeen di seet, man la. Lu doon seeni tànk?»
22 Ñu ne ko: «Njiitu takk-der ba Korney, ku jub, ragal Yàlla, te rafet seede bu ko xeetu Yawut wépp seedeel, moo jote ci malaaka mu sell, ndigalal woolu la këram, ngir déglu say kàddu.»
23 Ci kaw loolu Piyeer dugal leen, dalal leen. Ba bët setee, Piyeer ànd ak ñoom, ñenn ca bokki gëmkat ña dëkke Yope gunge ko.
24 Ca ëllëg sa Piyeer agsi Sesare. Fekk na Korney di ko séentu, daldi woo ca këram ay bokkam, ak xaritam yi ko gëna jege.
25 Ba Piyeer duggsee, Korney gatandu ko, ne gurub ca tànki Piyeer, sujjóot.
26 Piyeer yékkati ko, ne: «Déet jógal, man it, nit doŋŋ laa.»
27 Piyeer di waxtaan ak moom, ba duggsi, yem ca nit ñu bare ña fa daje.
28 Mu ne leen: «Yeen de xam ngeen ne ab Yawut, mayeesu ko mu jaxasoo ak xeetu jaambur, mbaa mu seeti ko. Waaye man nag Yàllaa ma won ne du kenn nit ku ma naan daganula jaxasool, mbaa setul.