Text copied!
Bibles in Wolof

JËF YA 10:1-21 in Wolof

Help us?

JËF YA 10:1-21 in Téereb Injiil

1 Amoon na ci Sesare nit ku tudd Korney, nekk njiitu xare, mu bokk ci mbooloom xare, mi ñuy wax mu Itali.
2 Moom nag ku farlu woon ci Yàlla la, te ragal ko, moom ak waa këram gépp; muy sarax ñu bare ci bànni Israyil, tey saxoo ci ñaan ci Yàlla.
3 Am bés ci tisbaar nag mu am peeñu, gis bu leer malaakam Yàlla feeñu ko ne ko: «Korney!»
4 Noonu Korney ne ko jàkk, daldi tiit ne ko: «Kilifa gi, lu mu doon?» Malaaka ma ne ko: «Say ñaan ak say sarax yéeg na fa kanam Yàlla, te nangul na la.
5 Yónnil léegi nag ay nit ci dëkku Yope, ñu woo ku tudd Simoŋ, mi ñu dàkkentale Piyeer.
6 Mu nga dal fa Simoŋ wullikat, bi këram nekk ci wetu géej.»
7 Bi malaaka mi doon wax ak moom demee, Korney woo ñaar ci ay surgaam ak benn xarekat bu farlu ci Yàlla ci ñi koy topptoo;
8 mu nettali leen lépp, yebal leen Yope.
9 Ca ëllëg sa, ba ñuy jaar ca yoon wa, ba jub dëkk ba, Piyeer yéeg ca kaw taax ma ci digg bëccëg ngir ñaan ci Yàlla.
10 Noonu xiif dab ko fa, mu bëgga lekk. Waaye bi ñu koy toggal, Yàlla feeñu ko.
11 Mu xool asamaan ubbiku, gis lu mel ni sér bu mag bu ñu téye ci ñeenti laf ya, yoor ko, mu jëm suuf.
12 Boroom ñeenti tànk yépp ñu nga ca, ak yiy raam ci suuf, ak picci asamaan.
13 Te baat ne ko: «Jógal, Piyeer, rey te lekk.»
14 Waaye Piyeer ne ko: «Mukk, Boroom bi, ndaxte masumaa lekk dara lu daganul mbaa lu araam.»
15 Waaye baat bi wax ak moom ñaareelu yoon ne ko: «Lu Yàlla sellal, bu ko araamal.»
16 Ñu def ko nag, ba muy ñetti yoon, ba noppi ñu ne cas sér ba, jëme asamaan.
17 Bi loolu amee Piyeer jaaxle lool ci lu peeñu miy tekki; fekk booba nit ñi Korney yebal, laajte woon nañu kër Simoŋ, ba agsi ci bunt bi.
18 Ñu woote nag naan: «Simoŋ, mi ñu dàkkentale Piyeer, ndax fi la dëkk?»
19 Bi Piyeer di rabal xelam ci peeñu ma, Xel mi ne ko: «Ñetti nit a ngi nii, di la wut.
20 Jógal, nga wàcc te ànd ak ñoom; bul werante, ndaxte maa leen yebal.»
21 Piyeer wàcc nag ne nit ñi: «Maa ngi nii, man mi ngeen di wut; lu doon seeni tànk?»
JËF YA 10 in Téereb Injiil

Jëf ya 10:1-21 in Kàddug Yàlla gi

1 Ku ñuy wax Korney, njiitu takk-der la woon ca Sesare. Ma nga bokkoon ca mbooloo ma ñu dippee Gàngooru Itali.
2 Ku jullite la woon te ragal Yàlla, mook waa këram gépp; bare woon na sarax yu muy yéwéne askan wi, te ñaan ci Yàlla la saxoo woon.
3 Am peeñu nag dikkal ko digg njolloor, mu gis ci lu leer malaakam Yàlla, mu duggsi, ne ko: «Korney!»
4 Korney ne ko jàkk, tiit, ne ko: «Sang bi, lu mu doon?» Mu ne ko: «Say ñaan ak say sarax yéeg na fa Yàlla, ba mu bàyyi la xel.
5 Léegi nag yebleel ca Yope, nga wooluji fa ku ñuy wax Simoŋ, ñu di ko dàkkentale Piyeer.
6 Ma nga dal ak meneen Simoŋ ma, wullikat ba këram féete wetu géej.»
7 Naka la malaaka ma wax ak Korney ba dem, mu woo ñaar ciy surgaam, ak benn takk-der bu jullite te bokk ciy suqam.
8 Mu nettali leen lépp nag, daldi leen yebal Yope.
9 Ca ëllëg sa, ñu dem bay jub dëkk ba, yemook Piyeer yéeg ca kaw taax ma ci digg bëccëg, ngir ñaan.
10 Mu dem ba xiif, bëgga lekk, ñu di ko toggal nag lu mu lekk. Ci biir loolu mu daanu leer.
11 Mu daldi gis asamaan ubbiku, lu mel ni sér bu mag bu ñu téyee ñeenti lafam, wàcce asamaan, jëm suuf.
12 Sér baa nga def mboolem boroom ñeenti tànk, ak dundoot yiy raam, ak mboolem njanaaw.
13 Mu am baat bu jib, ne ko: «Piyeer, jógal, rey te lekk.»
14 Piyeer ne ko: «Mukk, Sang bi, ndaxte masumaa lekk lenn lu daganul mbaa lu setul.»
15 Teewul baat bi wax ak moom ñaareel bi yoon, ne ko: «Lu Yàlla setal, bu ko daganadil.»
16 Menn peeñu moomu dikkal na ko ñetti yoon. La ca tegu ñu yéege këf ka asamaan.
17 Piyeer a nga jaaxle lool, di seet cim xelam lu peeñu ma ko dikkal di tekki, ndeke nit ña Korney yebaloon laaj nañu kër Simoŋ, ba dikk taxaw ca bunt ba.
18 Ñu woote, laajte, ne: «Simoŋ, mi ñuy wax Piyeer, fii la dëkk?»
19 Naka la Piyeer di xalaat ba tey ca peeñu ma, Noo gi ne ko: «Ñetti nit a ngi nii, di la seet.
20 Wàccal boog, ànd ak ñoom te bul nàttable, ndax man maa leen yebal.»
21 Piyeer wàcc nag ne nit ñi: «Maa ngii; ki ngeen di seet, man la. Lu doon seeni tànk?»
Jëf ya 10 in Kàddug Yàlla gi