5 Xanaa dungeen wéye fippu, ñu gën leena duma, te bopp di góomi neen, xol jeex tàkk?
6 Bopp ba téstën, fenn jagul. Xanaa gaañu-gaañu aki dagg-dagg rekk, ak góom yuy nàcc, fajeesu ko, takkeesu ko, gajfaleesu kook ag diw.
7 Seenum réew gental, seeni dëkk xoyomu, seen suuf, doxandéem yi lekk fi seen kanam, muy gent bu doxandéem tas.
8 Siyoŋ, dëkk bu taaru baa ngi wéet ni mbaarum tóokër mbaa dalub toolu xaal. Mbete dëkk bu ñu gaw!