Text copied!
Bibles in Wolof

Esayi 1:3-10 in Wolof

Help us?

Esayi 1:3-10 in Kàddug Yàlla gi

3 Aw yëkk xam na boroomam, mbaam-sëf xam gàmb, bi ko boroomam di xonte, waaye Israyil xamul, sama ñoñ ñii xàmmeewuñu.»
4 Wóoy wii xeetu moykat, wii askan wu diisu ñaawtéef, mii njurum defkati mbon, yii doomi yàqute! Ñoo wacc Aji Sax ji, ñoo teddadil Aji Sell ju Israyil, dëddu ko.
5 Xanaa dungeen wéye fippu, ñu gën leena duma, te bopp di góomi neen, xol jeex tàkk?
6 Bopp ba téstën, fenn jagul. Xanaa gaañu-gaañu aki dagg-dagg rekk, ak góom yuy nàcc, fajeesu ko, takkeesu ko, gajfaleesu kook ag diw.
7 Seenum réew gental, seeni dëkk xoyomu, seen suuf, doxandéem yi lekk fi seen kanam, muy gent bu doxandéem tas.
8 Siyoŋ, dëkk bu taaru baa ngi wéet ni mbaarum tóokër mbaa dalub toolu xaal. Mbete dëkk bu ñu gaw!
9 Bu nu Aji Sax ji Boroom gàngoor yi waccalul woon li nu deseek as néew, ni Sodom lanuy mel, Gomor lanuy neexool.
10 Dégluleen kàddug Aji Sax ji, yeen njiiti Sodom, teewluleen sunu yoonu Yàlla, yeen askanu Gomor.
Esayi 1 in Kàddug Yàlla gi