26Maay waññi say àttekat, ñu mel na woon, say diglekat it dellu mel ni bu jëkkoon. Su boobaa ñu wooye la Dëkkub Njekk, ak Dëkkub Kóllëre.»
27Siyoŋ dëppook yoon, mucc, ay tuubkatam wormaal njekk, raw;
28moykat ak bàkkaarkat yàqoondoo, dëddukati Aji Sax ji sànkoondoo.
29Yeenay rus moos ci garab yu mag, yi ngeen soppoona daje, di xërëmtu. Yeenay am gàcce ci tóokër, yi ngeen taamu woona daje, di bokkaale.
30Yeenay meli ni garab gu mag gu xob ya lax, mbaa tóokër bu amul siitu ndox.