25 Yerusalem, maa lay teg loxo, maay seeyal sa raxit ni xeme, ba dindi sa mbuubit mépp.
26 Maay waññi say àttekat, ñu mel na woon, say diglekat it dellu mel ni bu jëkkoon. Su boobaa ñu wooye la Dëkkub Njekk, ak Dëkkub Kóllëre.»
27 Siyoŋ dëppook yoon, mucc, ay tuubkatam wormaal njekk, raw;
28 moykat ak bàkkaarkat yàqoondoo, dëddukati Aji Sax ji sànkoondoo.
29 Yeenay rus moos ci garab yu mag, yi ngeen soppoona daje, di xërëmtu. Yeenay am gàcce ci tóokër, yi ngeen taamu woona daje, di bokkaale.
30 Yeenay meli ni garab gu mag gu xob ya lax, mbaa tóokër bu amul siitu ndox.