Text copied!
Bibles in Wolof

Esayi 1:22-31 in Wolof

Help us?

Esayi 1:22-31 in Kàddug Yàlla gi

22 Sa xaalis doon na raxit, sa biiñ xormbet.
23 Seeni njiit të, xejjoo ay sàcc, ñoom ñépp sopp ger, di dàq ay neexal, ab jirim, sàmmuñu àtteem, àqu jëtun soxalu leen.
24 Moo tax, kàddug Boroom bee, Aji Sax ju gàngoor yi, Jàmbaaru Israyil: «Maay lijjanti samay bañ, ngalla ñoom! Maay fey samay noon!
25 Yerusalem, maa lay teg loxo, maay seeyal sa raxit ni xeme, ba dindi sa mbuubit mépp.
26 Maay waññi say àttekat, ñu mel na woon, say diglekat it dellu mel ni bu jëkkoon. Su boobaa ñu wooye la Dëkkub Njekk, ak Dëkkub Kóllëre.»
27 Siyoŋ dëppook yoon, mucc, ay tuubkatam wormaal njekk, raw;
28 moykat ak bàkkaarkat yàqoondoo, dëddukati Aji Sax ji sànkoondoo.
29 Yeenay rus moos ci garab yu mag, yi ngeen soppoona daje, di xërëmtu. Yeenay am gàcce ci tóokër, yi ngeen taamu woona daje, di bokkaale.
30 Yeenay meli ni garab gu mag gu xob ya lax, mbaa tóokër bu amul siitu ndox.
31 Boroom doole mel ni boob, la mu liggéey di ferñent, ànd ak moom ne jéppét, te kenn du fey sawara wa.
Esayi 1 in Kàddug Yàlla gi