Text copied!
Bibles in Wolof

Esayi 1:17-28 in Wolof

Help us?

Esayi 1:17-28 in Kàddug Yàlla gi

17 Jàngleen di def lu baax, sàkku njub, waññi ab notkat, àtte dëgg, ab jirim, sàmm àqu jëtun.
18 «Kaayleen, nu waxtaan ba juboo,» la Aji Sax ji wax. «Li seeni bàkkaar di xonq lépp, tàll lay weexeji. Li muy xonq curr lépp, weex furr lay mujje.
19 Su ngeen ma nangoo déggal, ngëneelu réew mi ngeen di xéewloo.
20 Waaye su ngeen lànkee, fippu, saamar a leen di xéewloo.» Aji Sax ji déy a ko wax ci gémmiñam.
21 Ana nu biib dëkk yàqoo, mbeteb gànc, te nekkoon dëkkub kóllëre, njubte mate fa, njekk lal fa panaan, tey ñu diy bóomkat!
22 Sa xaalis doon na raxit, sa biiñ xormbet.
23 Seeni njiit të, xejjoo ay sàcc, ñoom ñépp sopp ger, di dàq ay neexal, ab jirim, sàmmuñu àtteem, àqu jëtun soxalu leen.
24 Moo tax, kàddug Boroom bee, Aji Sax ju gàngoor yi, Jàmbaaru Israyil: «Maay lijjanti samay bañ, ngalla ñoom! Maay fey samay noon!
25 Yerusalem, maa lay teg loxo, maay seeyal sa raxit ni xeme, ba dindi sa mbuubit mépp.
26 Maay waññi say àttekat, ñu mel na woon, say diglekat it dellu mel ni bu jëkkoon. Su boobaa ñu wooye la Dëkkub Njekk, ak Dëkkub Kóllëre.»
27 Siyoŋ dëppook yoon, mucc, ay tuubkatam wormaal njekk, raw;
28 moykat ak bàkkaarkat yàqoondoo, dëddukati Aji Sax ji sànkoondoo.
Esayi 1 in Kàddug Yàlla gi