15 Bu ngeen ma tàllaleey loxo, ma fuuyu. Bu ngeen doon ñaan-ñaanee it, du maa leen di déglu: seeni loxo, deret la taq ripp.
16 Raxasuleen ba set wecc, jëleleen seeni jëf ju bon fi sama kanam, te ngeen ba lu bon.
17 Jàngleen di def lu baax, sàkku njub, waññi ab notkat, àtte dëgg, ab jirim, sàmm àqu jëtun.