Text copied!
Bibles in Wolof

Esayi 1:13-18 in Wolof

Help us?

Esayi 1:13-18 in Kàddug Yàlla gi

13 Buleen fi indeeti saraxi caaxaan, seen saraxu cuuraay, lu ma seexlu la. Terutel weer ak bésub Noflaay ak wooteb ndajee ci yem! Duma mana dékku ndajem diine mu rax njubadi.
14 Seeni Terutel weer ak seen bési màggal laa bañ ci sama xol; yooyu màggal a ma diis ba àttanatuma ko.
15 Bu ngeen ma tàllaleey loxo, ma fuuyu. Bu ngeen doon ñaan-ñaanee it, du maa leen di déglu: seeni loxo, deret la taq ripp.
16 Raxasuleen ba set wecc, jëleleen seeni jëf ju bon fi sama kanam, te ngeen ba lu bon.
17 Jàngleen di def lu baax, sàkku njub, waññi ab notkat, àtte dëgg, ab jirim, sàmm àqu jëtun.
18 «Kaayleen, nu waxtaan ba juboo,» la Aji Sax ji wax. «Li seeni bàkkaar di xonq lépp, tàll lay weexeji. Li muy xonq curr lépp, weex furr lay mujje.
Esayi 1 in Kàddug Yàlla gi