Text copied!
Bibles in Wolof

Esayi 1:10-12 in Wolof

Help us?

Esayi 1:10-12 in Kàddug Yàlla gi

10 Dégluleen kàddug Aji Sax ji, yeen njiiti Sodom, teewluleen sunu yoonu Yàlla, yeen askanu Gomor.
11 «Lu may doye seen sarax yu bare?» la Aji Sax ji wax. «Damaa suur seen saraxi rendi-dóomali kuuy, suur nebbonu juru yar gi, deretu yëkk ak xar ak sikket it, safu ma.
12 Bu ngeen dikkee, teewsi fi sama kanam, ana ku leen sant ñu joggat-joggatee nii sama ëttu kër?
Esayi 1 in Kàddug Yàlla gi