Text copied!
Bibles in Wolof

Esayi 11:3-8 in Wolof

Help us?

Esayi 11:3-8 in Kàddug Yàlla gi

3 Ragal Aji Sax ji lay safoo, du lu ko bëtam may rekk lay àttee, du lu ko noppam may rekk lay dogale,
4 xanaa di àtte ku ñàkk ci njekk, di dogalal njub, néew-ji-dooley àddina. Mooy dóore àddina, bantub kàddoom, mooy reye ñu bon ñi, ngelawal gémmiñam.
5 Njekk lay gañoo, takkoo kóllëre.
6 Till ay bokk ak mbote ab dal, segg bokk akub tef ab tëraay, wëllu ànd ak gaynde gu mat, ak juru yar, tuut-tànk jiite leen.
7 Nag ak rab wu aay di forandoo, seeni doom goorandoo, gaynde di lekk um ngooñ niw yëkk,
8 luy nàmp di foye paxum ndox-suuf, perantal di laal tostanum ñàngóor.
Esayi 11 in Kàddug Yàlla gi