3 Ragal Aji Sax ji lay safoo, du lu ko bëtam may rekk lay àttee, du lu ko noppam may rekk lay dogale,
4 xanaa di àtte ku ñàkk ci njekk, di dogalal njub, néew-ji-dooley àddina. Mooy dóore àddina, bantub kàddoom, mooy reye ñu bon ñi, ngelawal gémmiñam.