Text copied!
Bibles in Wolof

Esayi 10:1-26 in Wolof

Help us?

Esayi 10:1-26 in Kàddug Yàlla gi

1 Wóoy ngalla boroom dogal yiy dogal njubadi, bind ko, te muy jur coono,
2 di ko àttee ñàkkal ku ñàkk, di xañ àq sama néew-ji-dooley ñoñ, bay lekk ab jëtun, di sëxëtoo ab jirim.
3 Ana nu ngeen di def keroog bésub mbugal ba, keroog ba safaan di bawoo fu sore? Ana ku ngeen di daw wuti wallam? Ana fu ngeen di denci seen teraanga?
4 Xanaa ànd ak ña ñu jàpp, ne yogg; mbaa tëddandook ña ñu bóom, ne lareet. Teewul Aji Sax ji xàcci loxoom, meddiwul ba tey.
5 Wóoy ngalla Asiri miy sama yetu mer, bolde bi ñu ŋàbb di samam sànj,
6 ma xabtal ko fi kaw xeet wu gëmadi, yebal ko ca askan woowu ma merloo, ngir ñu sëxëtoo leen, nangu seen alal, note leen ni banu mbedd.
7 Waaye Asiri gisewu ko noonu, xalaatewul noonu; bóome la xintewoo, ba fàkkas xeeti xeet.
8 Mu ngi naan: «Xanaa du sama jawriñ yépp a diy buur?
9 Kalne daa gën Karkemis gee ma nangu? Am Amat daa gën Arpàdd? Am Samari daa gën Damaas?
10 Maa duma réew yu seeni yàllantu, seeni tuur sut tuuri Yerusalem ak Samari.
11 Na ma tege loxo Samari aki yàllantoom, duma ni tege loxo Yerusalem aki tuuram?»
12 Boroom bi nee: «Bu ma sottalee liggéey fa kaw tundu Siyoŋ ak fa Yerusalem, maay mbugale buurub Asiri réy-réyloom gi, ak gëti xeebaateem.»
13 Moom moo ne: «Sama dooley përëg laa defe lii, maa xelu, ràññee; ba randal kemi suufi xeet yi, foqati seeni alal, dañ boroom jal ya niw yëkk, wàcce leen.
14 Maa teg alali xeet yi loxo, ni ku gis am tàgg. Maa tonneendoo réewi àddina ni ku for ay nen, tonni lépp, laaf tëf-tëfluwul, sàll newul ciib!»
15 Sémmiñ dina diir mbagg ka koy gore? Am dogukaay dina réy-réylu ba sut ka koy doge? Mbete yet wuy xàcci ka ko ŋàbb; mbaa bolde bu walbatiku ŋàbb boroom!
16 Moo tax Boroom bi, Aji Sax ji Boroom gàngoori xare yi, di yebal woppi ràgg fi kaw mbuxreem yi, seen daraja tàkk, sawara xoyom ko.
17 Aji Sax ji, leeru Israyil mooy doon sawara, ku Sellam kooku mooy doon tàkk-tàkku sawara, xoyom taxasi Asiri aki dégam ci benn bés.
18 Gott bu naat ak tool bu meññ, mu ne faraas fóom, ba mu mel ni ku wopp, yaram way seey,
19 gott ba dese garab yu néew yu gone mana lim, bind ko.
20 Keroog bés booba li des fi Israyil ak li rëcce kër Yanqóoba duñu wéerooti ña leen duma. Aji Sax ji lañuy wóolu, wéeroo ko, Aji Sell ju Israyil.
21 Aw ndes ay délsi, di ndesu askanu Yanqóoba, ñeel Yàlla Jàmbaar ji.
22 Seen xeet wi ni feppi suufas géej lay tollu, te as ndes a ciy délsi. Àtteb sànkute mooy taxaw, yoon toppe ba mat sëkk.
23 Sànkute déy mooy taxaw, Boroom bi, Aji Sax ji Boroom gàngoor yi di ko sottal fi réew mi mépp.
24 Moo tax Boroom bi, Aji Sax ji Boroom gàngoor yi dafa wax ne: «Yeen sama ñoñ ñi dëkke Siyoŋ, buleen ragal waa Asiri yi leen di dóor yet, ŋàbbal leen bolde ni waa Misra daa def ak yeen.
25 Waaye fi leek lu néewa néew mbugal jeex fi seen biir, am sànj sippil Asiri seen sànkute.»
26 Aji Sax ji Boroom gàngoor yee leen di ŋàbbal kàccri, na mu defoon waa Majan fa doju Oreb. Mooy xàcciw yetam, mu dal géej, na mu defoon fa Misra.
Esayi 10 in Kàddug Yàlla gi