Text copied!
Bibles in Wolof

Esayi 10:1-15 in Wolof

Help us?

Esayi 10:1-15 in Kàddug Yàlla gi

1 Wóoy ngalla boroom dogal yiy dogal njubadi, bind ko, te muy jur coono,
2 di ko àttee ñàkkal ku ñàkk, di xañ àq sama néew-ji-dooley ñoñ, bay lekk ab jëtun, di sëxëtoo ab jirim.
3 Ana nu ngeen di def keroog bésub mbugal ba, keroog ba safaan di bawoo fu sore? Ana ku ngeen di daw wuti wallam? Ana fu ngeen di denci seen teraanga?
4 Xanaa ànd ak ña ñu jàpp, ne yogg; mbaa tëddandook ña ñu bóom, ne lareet. Teewul Aji Sax ji xàcci loxoom, meddiwul ba tey.
5 Wóoy ngalla Asiri miy sama yetu mer, bolde bi ñu ŋàbb di samam sànj,
6 ma xabtal ko fi kaw xeet wu gëmadi, yebal ko ca askan woowu ma merloo, ngir ñu sëxëtoo leen, nangu seen alal, note leen ni banu mbedd.
7 Waaye Asiri gisewu ko noonu, xalaatewul noonu; bóome la xintewoo, ba fàkkas xeeti xeet.
8 Mu ngi naan: «Xanaa du sama jawriñ yépp a diy buur?
9 Kalne daa gën Karkemis gee ma nangu? Am Amat daa gën Arpàdd? Am Samari daa gën Damaas?
10 Maa duma réew yu seeni yàllantu, seeni tuur sut tuuri Yerusalem ak Samari.
11 Na ma tege loxo Samari aki yàllantoom, duma ni tege loxo Yerusalem aki tuuram?»
12 Boroom bi nee: «Bu ma sottalee liggéey fa kaw tundu Siyoŋ ak fa Yerusalem, maay mbugale buurub Asiri réy-réyloom gi, ak gëti xeebaateem.»
13 Moom moo ne: «Sama dooley përëg laa defe lii, maa xelu, ràññee; ba randal kemi suufi xeet yi, foqati seeni alal, dañ boroom jal ya niw yëkk, wàcce leen.
14 Maa teg alali xeet yi loxo, ni ku gis am tàgg. Maa tonneendoo réewi àddina ni ku for ay nen, tonni lépp, laaf tëf-tëfluwul, sàll newul ciib!»
15 Sémmiñ dina diir mbagg ka koy gore? Am dogukaay dina réy-réylu ba sut ka koy doge? Mbete yet wuy xàcci ka ko ŋàbb; mbaa bolde bu walbatiku ŋàbb boroom!
Esayi 10 in Kàddug Yàlla gi