Text copied!
Bibles in Wolof

2.Buur ya 15:8-36 in Wolof

Help us?

2.Buur ya 15:8-36 in Kàddug Yàlla gi

8 Ba Asaryaa buurub Yuda duggee fanweereelu atu nguuram ak juróom ñett, ca la Sàkkaryaa doomu Yerbowam falu buurub Israyil, péeyoo Samari. Juróom benni weer la nguuru.
9 Muy def nag li Aji Sax ji ñaawlu, na ko ay maamam daa defe. Dëdduwul bàkkaar yu Yerbowam doomu Nebat daan bàkkaarloo Israyil.
10 Ci kaw loolu Salum doomu Yabes fexeel ko, jam ko ca kanam mbooloo ma, rey ko, daldi falu buur, wuutu ko.
11 Li des ci mbiri Sàkkaryaa bindees ko moos ci téere bi ñu dippee Jaloorey buuri Israyil ca seeni jant.
12 Loolu mooy kàddu ga Aji Sax ji waxoon Yewu ne ko: «Saw askan dinañu toog ci kaw jalu Israyil ba ci sa sët-sëtaat.» Te noonu la amee.
13 Ba Asaryaa buurub Yuda duggee fanweereelu atu nguuram ak juróom ñeent, ca la Salum doomu Yabes falu buur ca Israyil. Wenn weer la nguuru, péeyoo Samari.
14 Gannaaw loolu Menayem doomu Gadi bàyyikoo Tirsa ba Samari, daldi fa jam Salum doomu Yabes, bóom ko, falu buur, wuutu ko.
15 Li des ci mbiri Salum ak pexeem ma mu laloon, bindees na ko moos ca téere bi ñu dippee Jaloorey buuri Israyil ca seeni jant.
16 Booba la Menayem song dëkk ba ñuy wax Tifsa, rey ña fa nekkoon ñépp, boole ca faagaagal diiwaan ba dale Tirsa ba Tifsa, ndax ñoo ko gàntal, bañ koo ubbi buntu dëkk ba. Mu butti jigéeni wérul ña fa nekk ñépp.
17 Ba Asaryaa buurub Yuda duggee fanweereelu atu nguuram ak juróom ñeent, ca la Menayem doomu Gadi falu buurub Israyil, péeyoo Samari. Nguuru na fukki at.
18 Muy def nag li Aji Sax ji ñaawlu; giiru dundam dëdduwul bàkkaar ya Yerbowam doomu Nebat daan bàkkaarloo Israyil.
19 Ci jamonoom la Tiglaat Pilser buurub Asiri song réew ma, Menayem jox ko ñetti téeméeri barigoy xaalis ngir mu jàpple ko, ba nguuram gëna dëgër.
20 Menayem dajale xaalis boobu ci Israyil; jële ko ca mboolem boroom alal ya, ku nekk ci ñoom joxe juróom fukki dogi xaalis, ñu yót ko buuri Asiri, mu doora jóge ca réew ma, ñibbi.
21 Li des ci mbiri Menayem ak mboolem lu mu def, bindees na ko moos ci téere bi ñu dippee Jaloorey buuri Israyil ca seeni jant.
22 Gannaaw loolu Buur Menayem saay, fekki ay maamam. Doomam Pekaxiya falu buur, wuutu ko.
23 Ba Asaryaa buurub Yuda duggee juróom fukkeelu atu nguuram, ca la Pekaxiya doomu Menayem falu buurub Israyil, péeyoo Samari. Nguuru na ñaari at.
24 Muy def li Aji Sax ji ñaawlu, dëdduwul bàkkaar ya Yerbowam doomu Nebat daan bàkkaarloo Israyil.
25 Ba mu ko defee Peka doomu kilifag xarekatam Remalya, fexeel ko, ba rey ko ca Samari, ca tatay kër buur, jamaale Argob ak Arye. Remalyaa nga àndoon ak juróom fukki niti Galàdd. Noonu la ko reye, falu buur, wuutu ko.
26 Li des ci mbiri Pekaxiya ak mboolem lu mu def, bindees na ko moos ci téere bi ñu dippee Jaloorey buuri Israyil ca seeni jant.
27 Ba Asaryaa buurub Yuda duggee juróom fukkeelu atu nguuram ak ñaar, ca la Peka doomu Remalyaa falu buurub Israyil, péeyoo Samari. Nguuru na ñaar fukki at.
28 Muy def li Aji Sax ji ñaawlu, dëdduwul bàkkaar ya Yerbowam doomu Nebat daan bàkkaarloo Israyil.
29 Ci jamonoy Peka buurub Israyil, Tiglaat Pilser buurub Asiri dikk, nangu dëkk yi ñuy wax Yon ak Abel Bet Maaka ak Yanowa ak Kedes ak Àccor ak diiwaani Galàdd ak Galile ak mboolem réewum Neftali. Mu jàpp waa réew ma, yóbbu Asiri.
30 Ba loolu amee ku ñuy wax Ose doomu Ela lalal Peka doomu Remalya pexe, jam ko mu dee. Mu daldi falu buur, wuutu ko. Loolu yemook ñaar fukkeelu atu nguurug buurub Yuda Yotam doomu Asaryaa.
31 Li des ci mbiri Peka ak mboolem lu mu def, bindees na ko moos ci téere bi ñu dippee Jaloorey buuri Israyil ca seeni jant.
32 Ba buurub Israyil Peka doomu Remalya duggee ñaareelu atu nguuram, ca la Yotam doomu Asaryaa falu buur ca Yuda.
33 Amoon na ñaar fukki at ak juróom ba muy falu te nguuru na fukki at ak juróom benn ca Yerusalem. Yaayam mooy Yerusa doomu Cadog.
34 Muy def li Aji Sax ji rafetlu; mboolem na baayam Usiya daan defe la daan defe.
35 Terewul jëleesu fa bérabi jaamookaay ya, xanaa mbooloo ma di def ay sarax ak a taal cuuraay ba tey, ca bérabi jaamookaay yooyu. Moom nag moo tabax buntu kër Aji Sax ja féete bëj-gànnaar.
36 Li des ci mbiri Yotam aki jëfam, bindees na ko moos ci téere bi ñu dippee Jaloorey buuri Yuda ca seeni jant.
2.Buur ya 15 in Kàddug Yàlla gi