Text copied!
Bibles in Wolof

2.Buur ya 15:4-19 in Wolof

Help us?

2.Buur ya 15:4-19 in Kàddug Yàlla gi

4 Terewul bérabi jaamookaay ya jëleesu ko fa. Mbooloo ma dañoo wéy di fa def ay sarax ak a taal cuuraay.
5 Aji Sax ji nag mbugal Asaryaa, teg ko jàngoroy ngaana ba kera bés ba mu deeyee. Ci néeg bu ñu ko ber la dëkk. Doomu Buur Yotam moo jiite kër ga, yor kilifteefu askanu réew ma.
6 Li des ci mbiri Asaryaa ak mboolem lu mu def, bindees na ko moos ci téere bi ñu dippee Jaloorey buuri Yuda ca seeni jant.
7 Gannaaw gi Asaryaa tëdd, fekki ay maamam, ñu denc ko ca bàmmeeli maamam ya, ca gox ba ñu naan Kër Daawuda. Yotam doomam moo falu buur, wuutu ko.
8 Ba Asaryaa buurub Yuda duggee fanweereelu atu nguuram ak juróom ñett, ca la Sàkkaryaa doomu Yerbowam falu buurub Israyil, péeyoo Samari. Juróom benni weer la nguuru.
9 Muy def nag li Aji Sax ji ñaawlu, na ko ay maamam daa defe. Dëdduwul bàkkaar yu Yerbowam doomu Nebat daan bàkkaarloo Israyil.
10 Ci kaw loolu Salum doomu Yabes fexeel ko, jam ko ca kanam mbooloo ma, rey ko, daldi falu buur, wuutu ko.
11 Li des ci mbiri Sàkkaryaa bindees ko moos ci téere bi ñu dippee Jaloorey buuri Israyil ca seeni jant.
12 Loolu mooy kàddu ga Aji Sax ji waxoon Yewu ne ko: «Saw askan dinañu toog ci kaw jalu Israyil ba ci sa sët-sëtaat.» Te noonu la amee.
13 Ba Asaryaa buurub Yuda duggee fanweereelu atu nguuram ak juróom ñeent, ca la Salum doomu Yabes falu buur ca Israyil. Wenn weer la nguuru, péeyoo Samari.
14 Gannaaw loolu Menayem doomu Gadi bàyyikoo Tirsa ba Samari, daldi fa jam Salum doomu Yabes, bóom ko, falu buur, wuutu ko.
15 Li des ci mbiri Salum ak pexeem ma mu laloon, bindees na ko moos ca téere bi ñu dippee Jaloorey buuri Israyil ca seeni jant.
16 Booba la Menayem song dëkk ba ñuy wax Tifsa, rey ña fa nekkoon ñépp, boole ca faagaagal diiwaan ba dale Tirsa ba Tifsa, ndax ñoo ko gàntal, bañ koo ubbi buntu dëkk ba. Mu butti jigéeni wérul ña fa nekk ñépp.
17 Ba Asaryaa buurub Yuda duggee fanweereelu atu nguuram ak juróom ñeent, ca la Menayem doomu Gadi falu buurub Israyil, péeyoo Samari. Nguuru na fukki at.
18 Muy def nag li Aji Sax ji ñaawlu; giiru dundam dëdduwul bàkkaar ya Yerbowam doomu Nebat daan bàkkaarloo Israyil.
19 Ci jamonoom la Tiglaat Pilser buurub Asiri song réew ma, Menayem jox ko ñetti téeméeri barigoy xaalis ngir mu jàpple ko, ba nguuram gëna dëgër.
2.Buur ya 15 in Kàddug Yàlla gi