Text copied!
Bibles in Wolof

2.Buur ya 13:2-10 in Wolof

Help us?

2.Buur ya 13:2-10 in Kàddug Yàlla gi

2 Muy def li Aji Sax ji ñaawlu, topp ci tànki Yerbowam doomu Nebat, di ko roy ci bàkkaar ya mu daan bàkkaarloo Israyil, bañ koo dëddu.
3 Merum Aji Sax ji nag ne jippét ca kaw Israyil, mu teg leen lu yàgg ci loxoy Asayel buurub Siri ak Ben Addàd doomu Asayel.
4 Yowakas nag tinu Aji Sax ji, mu nangul ko, ndax fekk na mu gis fitnay Israyil ji leen buurub Siri fitnaal.
5 Aji Sax ji daldi may Israyil ku leen xettli, ba ñu génn ca loxol waa Siri. Ba loolu amee waa Israyil dellu nekk ca seeni kër ci jàmm, na woon démb ak bëkk-démb.
6 Taxul ba tey ñu dëddu bàkkaari waa kër Yerbowam ya ñu doon bàkkaarloo Israyil. Dañu caa sax. Te it xer wa ñuy jaamoo Aseraa nga sampe woon ca Samari ba booba.
7 Mujj na Yowakas desewuloon ca mbooloom xareem lu moy juróom fukki gawar ak fukki watiir ak fukki junniy xarekat (10 000), ndax buurub Siri moo faagaagal ña ca des ñépp, duma leen ba ñu ne mbëtt.
8 Li des ci mbiri Yowakas ak mboolem lu mu def aki njàmbaaram, bindees na lépp moos ci téere bi ñu dippee Jaloorey buurub Israyil ca seeni jant.
9 Ba mu ko defee Buur Yowakas saay, fekki ay maamam, ñu denc ko ca Samari. Doomam Yowayas falu buur, wuutu ko.
10 Ba Yowas buurub Yuda duggee fanweereelu atu nguuram ak juróom ñaar, ca la Yowayas doomu Yowakas falu buurub Israyil, péeyoo Samari. Nguuru na fukki at ak juróom benn.
2.Buur ya 13 in Kàddug Yàlla gi