Text copied!
Bibles in Wolof

1.Buur ya 9:13-22 in Wolof

Help us?

1.Buur ya 9:13-22 in Kàddug Yàlla gi

13 Mu ne ko: «Sama waay, dëkk yi nga ma jox nag?» Mu daldi tudde dëkk ya réewum Kabul, mooy turam ba tey jii.
14 Iram yónnee woon na Buur fanweeri barigoy wurus ak juróom.
15 Buur Suleymaan dafa dogaloon liggéeyu sañul-bañ bu mu sas ay nit. Ñu tabax kër Aji Sax ji ak këru boppam ak sëkkub Milo ak tatay Yerusalem ya ak dëkk yii di Àccor, Megido ak Geser. Ni mu deme nii la:
16 Firawna buuru Misra moo daloon ci kaw Geser, nangu dëkk ba, lakk ko, rey Kanaaneen ña ca dëkkoon, daldi may dëkk ba doomam jay soxnas Suleymaan, muy yebam.
17 Suleymaan tabaxaat Geser ak Bet Oron Suuf,
18 ak Baalat ak Tamar ca màndiŋu réew ma,
19 ak mboolem dëkki dencukaayam, ak dëkk ya watiiri xare ya dence, ak dëkki gawar ya. Lu Suleymaan nammoona tabax daal, tabax na ko ca Yerusalem ak ca Libaŋ ak mboolem réewum kilifteefam.
20 Mboolem nit ña desoon ca Amoreen ñaak Etteen ñaak Periseen ñaak Eween ñaak Yebuseen ña, ñooñu bokkul ci bànni Israyil.
21 Seen sët ya leen wuutu ca réew ma, te bànni Israyil manuñu leen woona faagaagal, Suleymaan moo leen dugal ci liggéeyu njaam ak sañul-bañ, ñu nekke ko ba tey jii.
22 Waaye ñi bokk ci bànni Israyil, Suleymaan defu leeni jaam, ndax ñoom ñoo doon ay xarekatam, aki dagam aki jawriñam, ak njiiti xareem ak boroom watiiri xareem, ak dawalkati watiiram.
1.Buur ya 9 in Kàddug Yàlla gi