Text copied!
Bibles in Wolof

1.Buur ya 8:38-53 in Wolof

Help us?

1.Buur ya 8:38-53 in Kàddug Yàlla gi

38 lépp lu ciy ñaan akug tinu gu bawoo ci képp ku mu doon mbaa ci mboolem Israyil sa ñoñ, te fekk ku ci nekk ràññee mititu xolam, ba tàllal ay loxoom jublook kër gii,
39 su boobaa, yaw, ngalla nangoo ko asamaan, màkkaan ma nga dëkke, ba jéggale, te nga jëf ba yool ku nekk kemu mboolem ay jëfam, yaw mi xam xolam, ndax yaw doŋŋ yaa xam xolu mboolem doom aadama.
40 Su ko defee dinañu la ragal seen giiru dund ci kaw suuf si nga joxoon sunuy maam.
41 «Te itam doxandéem bu bokkul ci Israyil sa ñoñ bu jógee réew mu sore ngir sa tur,
42 ndax kat dees na dégg sa tur wu réy, ak sa dooley loxo ak sa kàttanu përëg, bu dikkee ba jublu ci kër gii, ñaan,
43 su boobaa ngalla nangool asamaan, màkkaan ma nga dëkke, te nga defal doxandéem boobu mboolem lu mu la ñaan, ndax xeeti àddina yépp xam sa tur, ngir ragal la ni Israyil sa ñoñ, te xam ne saw tur lañu tudd ci kër gii ma tabax.
44 «Bu sa ñoñ di xarejeek seen noon, ci yoon woo leen yebal, su ñu ñaanee ci Aji Sax ji, jublook dëkk bii nga taamu, ak kër gii ma tabax ngir saw tur,
45 su boobaa ngalla nangool asamaan, seenug ñaan ak seen dagaan te nga may leen ndam.
46 Bu ñu la moyee, nde amul nit ku dul moy, ba nga mere leen, teg leen ci loxob noon, noon ba jàpp leen, yóbbu am réewam, mu sore mbaa mu jege,
47 bu ñu demee ba seenum xel dellusee fa réew ma ñu leen yóbbu ngàllo, ñu tuub tey sàkku aw yiw fi yaw foofa ca réewum ña leen jàpp, ne la noo moy, noo ñaaw, noo def lu bon,
48 bu ñu waññikoo seen léppi xol, ak seen léppi jëmm ci yaw, foofa ca seen réewu noon ya leen jàpp, ba ñaan la, jublook seen réew ma nga joxoon seeni maam, jublook dëkk bi nga taamu, ak kër gii ma tabax ngir saw tur,
49 ngalla su boobaa, nangool ca asamaan, bérab ba nga dëkke, seen ñaan ak seen dagaan, te nga sàmm seen àq,
50 te it nga jéggal sa ñoñ ñi la moy, jéggal leen seen mboolem tooñ yu ñu la tooñ, te may leen yërmandey ña leen jàpp, ba ñu yërëm leen.
51 Ndax kat ñooy sa ñoñ ñi nga séddoo, génnee leen Misra, taalu xellikaayu weñ gu ñuul ga.
52 «Sang bi, teewlul bu baax samay tinu ak sa tinuy mbooloom Israyil mii, ba nangul leen mboolem lu ñu la jooy,
53 ndaxte danga leena ber ci biir xeeti àddina yépp, séddoo leen, te waxoon nga ko, Musaa sa jaam ba jottli ko, ba ngay génne sunuy maam Misra, yaw Boroom biy Aji Sax ji.»
1.Buur ya 8 in Kàddug Yàlla gi