Text copied!
Bibles in Wolof

1.Buur ya 7:5-20 in Wolof

Help us?

1.Buur ya 7:5-20 in Kàddug Yàlla gi

5 Bunt yépp ànd ak seen banti feguwaay, bunt bu ci nekk def ñeenti wet yu janoo màkk ñaar-ñaar; bunt yi sësaloo te dékkarloo ñett-ñett.
6 Ci biir loolu mu defar néeg ba ñuy wooye Néegu jëni kenu ya. Guddaay bi di juróom fukki xasab, yaatuwaay bi di fanweeri xasab, ak beneen néeg ci kanamam, mu ànd ak ay jëni kenoom ak xaddam bu mbaar ci kanam.
7 Mu tabax néeg ba ñuy wooye Néegu ngàngune ma walla Àttekaay ba, mu di fa àttee. Mu dare néeg bi banti seedar ci suuf ba ci kaw.
8 Këram ga mu dëkk it, ñu tabaxe ko noonu ci gannaaw Néegu ngàngune ma. Suleymaan teg ca tabaxal soxnaam doomu Firawna ja geneen kër gu nirook këram.
9 Tabax yooyu yépp biir ak biti xeeri tànnéef yu ñu yett la, natt ko, xacc ko, rattaxal, dale ko ci kenu gi, ba ci cati xadd bi ci kaw, daleeti ci biti ba ci ëtt bu mag bi.
10 Ñu defare kenu yi xeeri tànnéef yu mag: yii di fukki xasab, yii di juróom ñetti xasab.
11 Xeer yi tege ci kenu gi, xeeri tànnéef la yu ñu yett, natt ko, yemale, booleek banti seedar.
12 Miiru ëtt bu mag bi dees koo wëralee ay xeeri yett aki xànqi seedar: ñetti sësalantey xeer yu tegloo yu ne, benn sësalanteb xànqi seedar tege ca. Mu mel ni na ñu def ëttu biir bu kër Aji Sax ja ak dëru buntu kër ga.
13 Ci kaw loolu Buur Suleymaan yónnee, jëli ca Tir ku ñuy wax Uram.
14 Doomu jëtun la woon, bokk ci giirug Neftali. Baayam dëkkoon Tir, di tëggub xànjar. Uram di ku xareñ lool, rafet xel te mane mboolem liggéeyu xànjar. Mu dikk ca Buur Suleymaan, liggéeyal ko la ñu ko sant lépp.
15 Mu móol ñaari xeri xànjar, wu ci nekk am taxawaayu fukki xasab ak juróom ñett, te wu ci nekk buumu fukki xasab ak ñaar a koy ub.
16 Ci biir loolu mu defar ñaari boppi xànjar yu mu xelli, teg ko ci kaw xer yi, bopp bu ci nekk am taxawaayu juróomi xasab.
17 Bopp yi ci kaw xer yi, bu ci nekk da koo rafetale ab caaxu càllala, bopp bu ci nekk am ci juróom ñaar.
18 Mu defar ñaari jaray gërënaat, solal ko caax yi, wëralee ko bopp yi, ci xer wu ci nekk.
19 Bopp yi nekkoon ci kaw xer yi ci kanam nag bindoo ni lëppi tóor-tóor te bu ci nekk di ñeenti xasab.
20 Bopp yi ci kaw ñaari xer yi, bu ci nekk ñaar téeméeri gërënaat a ko wër ci kaw, feggook gamb bi ci wàllaa caax bi.
1.Buur ya 7 in Kàddug Yàlla gi