Text copied!
Bibles in Wolof

1.Buur ya 2:9-21 in Wolof

Help us?

1.Buur ya 2:9-21 in Kàddug Yàlla gi

9 Waaye yaw de, bu ko ñàkka topp, ndax boroom xel nga, te dinga xam ni ngay defeek moom, ba mu sangoo deretam, ànd ak bijjaawam, dugg bàmmeel.»
10 Gannaaw loolu Daawuda nelaw, fekki ay maamam, ñu denc ko ca gox ba ñu naan Kër Daawuda.
11 Nguurug Daawuda ci Israyil tollu na ci ñeent fukki at, di juróom ñaari at ya mu péeyoo Ebron, ak fanweeri at ak ñett ya mu péeyoo Yerusalem.
12 Suleymaan nag toog ca jalub baayam Daawuda; nguuram dëgër, ne kekk.
13 Ci biir loolu Adoña ma Agit di ndeyam, dem ca Batseba, ndeyu Suleymaan. Mu ne ko: «Mbaa jàmm a la indi?» Mu ne ko: «Jàmm la.»
14 Mu neeti ko: «Mbir la mu ma lay wax.» Mu ne ko: «Waxal.»
15 Mu ne ko: «Xam nga ne maa moomoon nguur gi, te man la Israyil gépp séentu woon, ma falu buur. Waaye tey nguur gi walbatiku na, tegu ci sama loxol doomu baay, ndax Aji Sax jee ko ko jox.
16 Léegi nag lenn rekk laa lay ñaan, te nga bañ maa gàntu.» Mu ne ko: «Waxal rekk.»
17 Mu ne ko: «Buur Suleymaan du la gàntu, rikk ñaanal ma ko, mu may ma Abisag mu Sunem soxna.»
18 Batseba ne ko: «Baax na, man kay maa la koy waxal Buur.»
19 Batseba dem ca Buur Suleymaan, ngir wax ko mbirum Adoña ma. Buur jóg gatandu ko, sukkal ko, daldi toogaat ci ngànguneem. Mu tegal ndeyam ngàngune, mu toog ci ndijooram.
20 Mu ne ko: «Man de, lenn lu tuut rekk laa lay ñaan, te bu ma gàntu.» Mu ne ko: «Waxal, saa ndey, duma la gàntu.»
21 Mu ne ko: «Abisag mu Sunem, may ko sa doomu baay Adoña soxna.»
1.Buur ya 2 in Kàddug Yàlla gi