Text copied!
Bibles in Wolof

1.Buur ya 2:7-14 in Wolof

Help us?

1.Buur ya 2:7-14 in Kàddug Yàlla gi

7 «Góor ñiy doomi Barsilay mu Galàdd nag, nanga leen baaxe, te ñuy bokk ak yaw ndab, ndax kat taxawu woon nañu ma, ba may daw Absalom sa doomu baay.
8 «Gannaaw loolu bàyyil xel ci Simey mi nga feggool, muy doomu Gera mu Baxurim, mi bokk ci giirug Beñamin. Moom moo ma doon tifaari saaga, bés ba ma jëmee Maanayim, moom mu dikk dajeek man ca dexu Yurdan. Ma giñal ko ci Aji Sax ji ne ko: “Duma la rey, sama saamar du la dal!”
9 Waaye yaw de, bu ko ñàkka topp, ndax boroom xel nga, te dinga xam ni ngay defeek moom, ba mu sangoo deretam, ànd ak bijjaawam, dugg bàmmeel.»
10 Gannaaw loolu Daawuda nelaw, fekki ay maamam, ñu denc ko ca gox ba ñu naan Kër Daawuda.
11 Nguurug Daawuda ci Israyil tollu na ci ñeent fukki at, di juróom ñaari at ya mu péeyoo Ebron, ak fanweeri at ak ñett ya mu péeyoo Yerusalem.
12 Suleymaan nag toog ca jalub baayam Daawuda; nguuram dëgër, ne kekk.
13 Ci biir loolu Adoña ma Agit di ndeyam, dem ca Batseba, ndeyu Suleymaan. Mu ne ko: «Mbaa jàmm a la indi?» Mu ne ko: «Jàmm la.»
14 Mu neeti ko: «Mbir la mu ma lay wax.» Mu ne ko: «Waxal.»
1.Buur ya 2 in Kàddug Yàlla gi