19 Batseba dem ca Buur Suleymaan, ngir wax ko mbirum Adoña ma. Buur jóg gatandu ko, sukkal ko, daldi toogaat ci ngànguneem. Mu tegal ndeyam ngàngune, mu toog ci ndijooram.
20 Mu ne ko: «Man de, lenn lu tuut rekk laa lay ñaan, te bu ma gàntu.» Mu ne ko: «Waxal, saa ndey, duma la gàntu.»
21 Mu ne ko: «Abisag mu Sunem, may ko sa doomu baay Adoña soxna.»
22 Buur Suleymaan ne ndeyam: «Nga ne! Adoña ngay ñaanal Abisag mu Sunem soxna? Tee nga koo ñaanal nguur gi far, nde mooy sama mag, ñaanalaale ko Abiyatar sarxalkat bi, mook Yowab doomu Seruya?»
23 Buur Suleymaan nag giñ ci Aji Sax ji ne: «Yal na ma Yàlla teg mbugal mu gëna tar, ndegam Adoña du feye bakkanam lii muy sàkku!
24 Léegi nag giñ naa ci Aji Sax ji, Kiy Dund, te teg ma fi, dëj ma ci jalub Daawuda sama baay, sampal ma askanu nguur, wa mu dige woon, bésub tey jii Adoña dina dee.»
25 Buur Suleymaan daldi jox ndigal Benaya doomu Yoyada. Benaya jam Adoña, mu dee.
26 Abiyatar sarxalkat bi nag, Buur ne ko: «Dellul Anatot ca say tool. Dee rekk a war ci yaw, waaye bésub tey jii duma la rey, ndax li nga gàddu woon gaalu Aji Sax ji Boroom bi, dox jiitu sama baay Daawuda. Nga teg ci bokk ak sama baay mboolem coono bu mu daj.»
27 Suleymaan nag jële Abiyatar ci liggéeyu saraxi Aji Sax ji, daldi matal li Aji Sax ji waxoon ci waa kër Eli ca Silo.
28 Yowab àndul woon ak Absalom ci pexeem, waaye Adoña la mujj àndal. Ba Yowab yégee la xew, daa daw ba ca xaymab Aji Sax ji, jàpp ca béjjén ya ca cati sarxalukaay ba, ngir rawale bakkanam.
29 Ñu wax Buur Suleymaan ne ko: «Yowab daw na, làquji ca xaymab Aji Sax ji, te kat ma nga ca sarxalukaay ba.» Suleymaan sant Benaya doomu Yoyada, ne ko mu dem, jam ko.
30 Benaya dugg ca biir xaymab Aji Sax ja, ne ko: «Buur nee nanga génn!» Yowab ne ko: «Génnuma, fii laay deeye!» Benaya yegge Buur waxi Yowab ak la mu ko tontu.
31 Buur ne ko: «Defal li mu wax, jam ko mu dee, nga suul ko, ndax ma set, maak sama waa kër baay, ci deretu jaamburi Yàlla ji Yowab tuuroon.