Text copied!
Bibles in Wolof

1.Buur ya 22:27-42 in Wolof

Help us?

1.Buur ya 22:27-42 in Kàddug Yàlla gi

27 Nga ne ko: “Buur dafa wax ne: Dugal-leen kii ndungsiin, di ko jox lekk gu néew ak ndox mu néew, ba keroog may dikk ak jàmm.”»
28 Mise ne: «Soo délseek jàmm déy, Aji Sax ji waxul, ma jottli.» Mu dellu ne: «Mbooloo mi, yeena ko déggandoo, yeen ñépp.»
29 Ba mu ko defee buurub Israyil ànd ak Yosafat buurub Yuda, ñu songi Ramot ga ca Galàdd.
30 Buurub Israyil nag ne Yosafat: «Damay soppi col, dugg ci xeex bi, waaye yaw solal sa mbubbam buur.» Buurub Israyil daldi soppig col, dugg ca xeex ba.
31 Fekk na buurub Siri jox ndigal fanweeri nitam ak ñaar, ñay jiite watiiri xare ya. Mu ne leen: «Buleen xeex ak kenn, du ku tuut, du ku réy, diirleen buurub Israyil, moom rekk.»
32 Ba loolu amee, ña jiite watiiri xare ya gis Yosafat, daldi ne: «Kii kay mooy buurub Israyil!» Ñu walbatiku ci kawam, ngir song ko. Yosafat nag àddu ca kaw,
33 njiiti watiir ya xam ne du buurub Israyil, ñu walbatikuwaat, bàyyi ko.
34 Ci biir loolu mu am ku soqi ag fitt te teyu ko, mu dal buurub Israyil ci diggante ñaari wàlli pakk bi mu sol. Mu ne dawalkatu watiiram: «Waññikul, génne ma ci xeex bi, gaañu naa!»
35 Naka la xare ba tàkkarnaase bésub keroog bépp, ñu téye buur ba ca biir watiir wa, mu janook waa Siri, ba ca ngoon sa, mu doora dee. Jam-jam baa nga nàcc, ba taa ca biir watiir ba.
36 Jant baa ngay xalambaayu, yéene jib, ba dajal mbooloo ma. Ña nga naan: «Na ku nekk ñibbi sa dëkk, ca sam réew!»
37 Buur ba nag saay, ñu yóbbu ko Samari, denc ko foofa.
38 Ba ñuy raxas watiir ba ca déeg ba ñuy wax Samari, xaj ya di xab deret ja, gànc ya di sangu ca ndoxum déeg ma, muy la Aji Sax ji waxoon.
39 Li des ci mbiri Axab ak mboolem lu mu def ak kër ga mu tabax, rafetale ko bëñi ñay, ak mboolem dëkk ya mu tabax, loolu lépp, bindees na ko moos ca téere ba ñu dippee Jaloorey buuri Israyil ca seeni jant.
40 Buur Axab nag saay, fekki ay maamam, doomam Akasiya falu buur, wuutu ko.
41 Axab moomu, ba mu faloo Israyil, ba dugg ñeenteelu atu nguuram, ca la Yosafat doomu Asa falu buur ca kaw Yuda.
42 Yosafat amoon na fanweeri at ak juróom, ba muy falu te ñaar fukki at ak juróom la falu ca Yerusalem. Yaayam moo doon Asuba, doomu Sili.
1.Buur ya 22 in Kàddug Yàlla gi